Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 30:7-11 in Wolof

Help us?

Sabóor 30:7-11 in Kàddug Yàlla gi

7 Man damaa baaxle woon, ba ne: «Deesu ma rëññeel mukk.»
8 Aji Sax ji, booba yaa ma baaxe, dëj ma, ma ne kekk niw tund. Nga fuuyu, ma jàq.
9 Aji Sax ji, yaw laa woo wall; Boroom bi, yaw laa ñaanu yiw,
10 ne la: «Ma dee, tàbbi bàmmeel, ana lu mu lay jariñ? Nu la pëndu pax di sante, bay biral sa worma?
11 Aji Sax ji, déglul, baaxe ma; éy Aji Sax ji, dimbali ma.»
Sabóor 30 in Kàddug Yàlla gi