3 Aji Sax ji sama Yàlla, maa la woo wall, nga faj ma.
4 Aji Sax ji, yaa ma jukkee njaniiw, may ma bakkan, ma tàggook ñiy tàbbi njaniiw.
5 Yeen aji gëm ñi, woyleen Aji Sax ji, njukkale ko sellngaam.
6 Meram di lu gàtt, aw yiwam sax dàkk. Rongooñ gane, fanaan, ay ree xëysi.
7 Man damaa baaxle woon, ba ne: «Deesu ma rëññeel mukk.»
8 Aji Sax ji, booba yaa ma baaxe, dëj ma, ma ne kekk niw tund. Nga fuuyu, ma jàq.
9 Aji Sax ji, yaw laa woo wall; Boroom bi, yaw laa ñaanu yiw,
10 ne la: «Ma dee, tàbbi bàmmeel, ana lu mu lay jariñ? Nu la pëndu pax di sante, bay biral sa worma?
11 Aji Sax ji, déglul, baaxe ma; éy Aji Sax ji, dimbali ma.»