3 Aji Sax jeey àddu ca kaw ndox ma, Yàlla mu tedd maa dënu, Aji Sax jeey tiim ndox, mi ne màww.
4 Aji Sax jeey àddoo doole, Aji Sax jeey àddoo daraja.
5 Aji Sax jeey àddu, falaxe garabi seedar, Aji Sax jee rajaxe seedari Libaŋ.
6 Réewum Libaŋ, mu curpiloo ni wëllu, tundu Siryoŋ it, mbete yëkk wu ndaw.
7 Aji Sax jeey àddu, fettaxal sawara, mu boy.
8 Aji Sax ji àddooti, yëngal màndiŋ, Aji Sax jee yëngal màndiŋu Kades.
9 Aji Sax jeey àddu, kéwél matu, garabi àll ruus, biir këram di mennum riir, naan: «Màggal-leen ko!»
10 Aji Sax ji la mbënn ma fekk falu, Aji Sax jee falu buur ba fàww.
11 Aji Sax jeey kàttanal ñoñam, di barkeele jàmm ñoñam.