7 Ma sant Aji Sax ji may xelal, ba guddi sax sama xel di ma yedd.
8 Damaa saxoo ne jàkk ci Aji Sax ji ndijoor la ma fare, ba duma tërëf,
9 xanaa di bànneexu, sama xol bég, sama yaram finaax.
10 Doo ma wacc njaniiw moos, sa wóllëre wa, doo ko won yàqutey bàmmeel.
11 Yaa may xamal yoonu ndund. Fu bànneex mate, yaa teew, xéewal sa ndijoor la saxe.