4 Kuy sàkkuy tuur barew tiis, man de duma leen tuural deret, sama làmmiñ du leen tudd.
5 Aji Sax ji, yaay wàll wi ma séddoo, di sama ndabal xéewal. Yaa yor sama wërsëg.
6 Maa muurloo bérab bu neex, ndaw cér bu rafet!
7 Ma sant Aji Sax ji may xelal, ba guddi sax sama xel di ma yedd.
8 Damaa saxoo ne jàkk ci Aji Sax ji ndijoor la ma fare, ba duma tërëf,
9 xanaa di bànneexu, sama xol bég, sama yaram finaax.