2 Yal nanga ma nangul samag ñaan ni cuuraay lu ñu la taalal, yoxo yi ma la tàllal di saraxu ngoon soo gërëm.
3 Aji Sax ji, sàmmal ma sama làmmiñ, saytul ma sama kàddu.
4 Bu ma xiir ci lu aay, may jëfe jëf ju bon, ànd ceek ñiy jëf lu ñaaw, di wàlli seeni bernde.