3 Fa la nu sunuy sang daa woyloo, not nu, bëgg nu bégal leen, naan: «Woyal-leen nu ci woyi Siyoŋ.»
4 Moo nu nuy woye woyu Aji Sax ji kaw suufas yéefar?
5 Éy Yerusalem, su ma la naree fàtte, yal na ma doole dëddu!
6 Yerusalem, su ma la fàttlikuwul, fonk la, ba gën laa bége lépp, yal na sama làmmiñ tafoo sama denqleñ.