19 Éey waa kër Israyil, santleen Aji Sax ji! Éey waa kër Aaróona, santleen Aji Sax ji!
20 Éey waa kër Lewi, santleen Aji Sax ji! Yeen ñi ragal Aji Sax ji, santleen Aji Sax ji!
21 Nañuy sante Aji Sax ji Siyoŋ, moom mi dëkke Yerusalem. Màggal-leen Ki Sax!