5Ba nu toppee sunu bakkan, sunu bëgg-bëgg yu bon yi ndigali yoonu Musaa yee, ñoo daan liggéey ci sunuy cér, ngir nu meññ lu nu jëme ci ndee.
6Waaye tey ci sunu digg ak yoon wi nu tënku woon, la nu di ñu dee, ba teqlikoo ak moom. Moo tax nu doon ay jaam yu tegoo kilifteef gu yees, gi Noowug Yàlla indi, gannaaw ba nu wàccoo ak kilifteefu mbindu yoonu Musaa ma woon.
7Ana lu loolu di tekki? Xanaa kon yoonu Musaa bàkkaar la? Mukk kay! Waaye yoonu Musaa moo ma xamal luy bàkkaar. Ndax kat su dul woon ak yoon wi ne: «Bul xemmem yëfi jaambur,» kon xemmemtéef sax duma xam lu mu doon.
8Waaye bàkkaar moo jaare buntub ndigalu yoon, ba yee ci man mboolemi xemmemtéef yu bon. Ndax kat, su yoonu Musaa amul woon, bàkkaar di lu dee.