Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 3:11-27 in Wolof

Help us?

ROOM 3:11-27 in Téereb Injiil

11 Amul kenn ku xam yëfi Yàlla, mbaa kenn ku koy wut.
12 Ñépp jeng nañu, ba kenn amalatul Yàlla njariñ. Kenn du def lu baax, du kenn sax!
13 Seen put a ngi xasaw ni méddum ñetti fan, seen làmmiñ làggi ci njublaŋ, te seeni kàddu aay ni daŋaru ñàngóor.
14 Duñu génne ci seen gémmiñ lu dul ay móolu ak i xas.
15 Ñu sawar lañu ci rey nit.
16 Fu ñu jaar, foofa yàqu ak musiba.
17 Xamuñu yoonu jàmm,
18 te ragal Yàlla sore na seen xol.»
19 Xam nanu nag ne lépp lu yoonu Musaa wax, wax na ko ñi nekk ci yoon woowu, ngir gémmiñ yépp ne miig, te waa àddina sépp jaar ci àtteb Yàlla.
20 Ndaxte sàmm yoon wi taxul kenn jub ci kanam Yàlla; solob ndigal yi daal mooy wone bàkkaar.
21 Waaye léegi nag Yàlla feeñal na, ni nit mana jube ci kanamam, ci lu séqul ak yoonu Musaa dara. Waaye ba tey yoonu Musaa ak waxi yonent yi seedeel nañu ko.
22 Jub ci kanam Yàlla, gëm Yeesu Kirist rekk a koy maye, te képp ku ko gëm bokk nga ci. Ndaxte ñépp a yem fa kanam Yàlla.
23 Ñépp a bàkkaar, ba joteetuñu ndamu Yàlla.
24 Waaye gannaaw Kirist Yeesu dee na ngir jot leen, Yàlla ciw yiwam man na leena àtte ni ñu jub ci dara.
25 Wàcce na Kirist, mu nekk sarax ngir Yàlla baal nu sunuy bàkkaar, jaar ci deretam ji ñu tuur; te ngëm rekk moo nu ciy boole. Noonu Yàlla firndeel na ne ku jub la, doonte sax dafa muñaloon ñi jiitu jamonoy Kirist, ba jéggal leen seeni bàkkaar.
26 Kon ci jamono jii nu ne, Yàlla wone na bu leer ne ku jub la, di àtte ni ku jub képp ku gëm Yeesu, te ba tey dëkk ci njubteem.
27 Kan a mana bàkku nag ci kanam Yàlla? Kenn! Lu ko waral nag? Xanaa sàmm yoon? Déedéet! Ngëm rekk.
ROOM 3 in Téereb Injiil

Room 3:11-27 in Kàddug Yàlla gi

11 Kenn xeluwul, kenn wutul Yàlla.
12 Ñépp a lajj ba bokk yàqu yaxeet, Kenn deful lu baax, du kenn sax!
13 Seenug boli di bàmmeel bu ne ŋàpp, seen làmmiñ di ràbb njublaŋ, seeni kàddu aay ni daŋaru ñàngóor.
14 Seen gémmiñ, waxi móolu ak wextan la feese,
15 seeni tànk bar ci yoonu tuur deretu jaambur,
16 te fu ñu jaare yàqute la ak musiba.
17 Yoonu jàmm, xamuñu ko,
18 te ag ragal Yàlla jegewu leen.»
19 Xam nanu nag ne lépp lu yoonu Musaa wax, ñi ci yoonu Musaa la ko wax, ngir aw lay jeex tàkk, ngir itam mu leer nàññ ne àddina sépp a sikk fi kanam Yàlla.
20 Ndax kat deesul jox kenn àtteb ku jub fa kanam Yàlla ndax jëf ju mu def, ngir sàmm yoonu Musaa; solob yoon wi daal, mooy ci lees di ràññee bu baax luy bàkkaar.
21 Waaye léegi Yàlla moo feeñal nu nit di ame fa kanamam, àtteb njubam gu ajuwul ci yoonu Musaa. Te yoonu Musaa, ak yonent yi seede nañu loolu.
22 Googu njub fa kanam Yàlla nag, ci gëm Yeesu Almasi lees koy ame, te mboolem ñi ko gëm la ñeel, amul xejj ak seen.
23 Ndax kat ñépp a bàkkaar, ba jotewuñu leeru Yàlla,
24 te ci yiwu Yàlla wu àndul ak genn pey lees di joxe ñépp àtteb ñu jub, ndax njot gi sottee ci Almasi Yeesu.
25 Moom la Yàlla tudd muy njot gu ngëm di maye, ci kaw deretam ji tuuru. Noonu la Yàlla firndeele ne njubteem mat na sëkk doonte tanqamlu woon na bàkkaari niti jamono ya woon,
26 nde Yàlla ci biir ag jéllaleem la firndeel njubteem ci janti tey jii, ngir mu leer ne moo wéye njub, te képp ku gëm Yeesu, moo koy jox àtteb ku jub.
27 Kon ana lees di bàkkoo? Dara! Ci lan lañu koy teg sax? Ci jëf ju yoon santaane? Mukk! Xanaa yoonu ngëm doŋŋ.
Room 3 in Kàddug Yàlla gi