6Te yeen ñi ñu woo ci Yeesu Almasi itam, ci ngeen bokk.
7Bataaxal bi ñeel na mboolem yeen ña fa Room, di ñu Yàlla sopp, woo leen, ngir ngeen doon ñu sell. Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.
8Ma doore sant sama Yàlla ci Yeesu Almasi ngir yeen ñépp, ndax seen ngëm siiw na ci àddina sépp.
9Yàlla mi may jaamoo xol, ci ni may siiwtaanee xibaaru jàmm bu Doomam, moom seere na ne noppiwuma leena fàttliku.
10Xanaa di saxoo dagaan ci samay ñaan, su ci Yàlla àndee, yoon wu jub wu ma mujj dikke ba ci yeen.