Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Room - Room 16

Room 16:5-9

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Nuyul-leen ma itam mbooloom gëmkat miy daje ca seen kër. Nuyul-leen ma sama soppe Epaynet, miy jooxeb ndoortel meññeef, ma génne ca diiwaanu Asi, ñeel Almasi.
6Nuyul-leen ma Maryaama, mi sonn lool ci yeen.
7Nuyul-leen ma Andoronikus ak Yuña, sama bokki Yawut, yi ñu ma tëjandooloon; ñu ñu nawloo lañu ci ndaw yi, te ñoo ma jëkka gëm sax Almasi.
8Nuyul-leen ma Ampilyaatus, mi ma soppal sama bopp ndax Sang bi.
9Nuyul-leen ma it Urben, sunu mbokkum liggéeykat ci liggéeyub Almasi, ak Estakis, sama soppe;

Read Room 16Room 16
Compare Room 16:5-9Room 16:5-9