Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 15:11-33 in Wolof

Help us?

ROOM 15:11-33 in Téereb Injiil

11 Mu dellooti ne: «Santleen Boroom bi, yéen waa àddina, te ñëw màggal ko, yéen xeet yépp.»
12 Te it Esayi wax na ne: «Am na sëtu Isayi buy ñëw, dina yilif xeeti ñi dul Yawut, te ci moom lañuy wékk seen yaakaar.»
13 Kon Yàlla miy maye yaakaar, na def ci seen xol mbég mu réy ak jàmm ju yaa ci seen kaw ngëm, ba ngeen am yaakaar ju mat sëkk ci dooley Xel mu Sell mi.
14 Bokk yi, wóor na ma ne baax ngeen ba fa mbaax mana yem, fees dell ak xam-xam, ba mana jàngleente mbiri Yàlla ci seen biir.
15 Bu sama kàddu diisee nag ci bataaxal bii, dara taxul lu dul bëgga yeesal seen xalaat, ndaxte Yàlla ci kaw yiwam daf maa sas,
16 ma nekk jawriñu Kirist Yeesu, yebal ma ci àddina ci xeeti ñi dul Yawut. Liggéey bu sell laay def ngir Yàlla, ci xamle xibaaru jàmmam bi, ngir xeeti àddina sell ci dooley Xel mu Sell mi, ba neex Yàlla, mel ni sarax su ñu koy jébbal.
17 Kon nag maa ngi bànneexu ci Kirist Yeesu ngir liggéey boobu ma Yàlla dénk.
18 Awma fitu wax leneen nag, lu dul li Kirist jëf jaarale ko ci man, ngir xeeti àddina jébbalu ci moom; jëf na jaarale ci samay wax ak samay jëf,
19 ci ay tegtal ak i kéemaan, sukkandikoo ci dooley Xelu Yàlla mi. Ba fi mu nekk nag yégle naa fu nekk xibaaru Kirist, li dale ci Yerusalem, jaar ci gox yépp, ba àgg diiwaanu Iliri.
20 Sama yéene mooy xamle xibaaru turu Kirist fa mu eggagul, ndax bëggumaa yeggale sas wu keneen daloon.
21 Li ma def nag, dëppoo na ak li Mbind mi wax ne: «Ñi yégagul mbiram dinañu ko yég, te ñi ko masula dégg, xam ko.»
22 Bëggoon naa ñëw seetsi leen, fekk ay téq-téq ñoo ma téye ba tey.
23 Waaye nag léegi bey naa sama sas ci gox yii.
24 Bu may dem Espaañ nag, bëgg naa faa jaar, nuyu leen; ndaxte ay at a ngii maa ngi am yéene ju tar ci ñëw seetsi leen. Bëgg na maa nekk ci seen biir, ngir am bànneexu sotteente ak yéen xalaat ab diir, te it ngeen waajalal ma sama yoonu Espaañ.
25 Waaye nag fi mu nekk maa ngi dem nii Yerusalem, ngir dimbaliji gaayi Yàlla yu sell ya fa nekk.
26 Ndaxte waa Maseduwan ak waa Akayi ñi gëm, fas nañu yéeney sàkk ci seeni alal, yónnee ko, ngir dimbali ñi néew doole ci gaayi Yàlla yu sell, yi nekk Yerusalem.
27 Yéene nañu ko, te it ci dëgg-dëgg bor la, bu ñu wara fey. Ndaxte gannaaw ñi gëm ci Yerusalem séddoo nañu ak ñi dul Yawut seen ngëm, kon xeet yooyu itam war nañoo séddoo ak ñoom seen alal.
28 Kon nag waxtu wu ma noppee ci liggéey boobu, ba teg may gu tedd gii ci loxoy boroom, dinaa dem Espaañ, tey jaar fi yéen.
29 Te wóor na maa ne bu ma agsee ci yéen, dinaa indaale barkeb Kirist bu mat sëkk.
30 Gannaaw loolu bokk yi, maa ngi leen di ñaan ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist ak ci bëggante, gi Xelu Yàlla mi def ci nun, ngeen defal ma lii: àndleen ak man, nu tuur sunu ñaq ci ñaan Yàlla.
31 Ñaanal-leen ma, ngir ma mucc ci ñi gëmul ci waa Yude; te it gaayi Yàlla yu sell yu nekk ci Yerusalem nangu ndimbal, li ma leen di yóbbul.
32 Dolli ci, Yàlla may ma, ma ñëw seetsi leen ak xol bu sedd, nu booloo yeeslu fa kanam Yàlla.
33 Yal na Yàlla miy Boroom jàmm ànd ak yéen ñépp. Amiin.
ROOM 15 in Téereb Injiil

Room 15:11-33 in Kàddug Yàlla gi

11 Mu dellu ne: «Yeen xeetoo xeet, màggal-leen Boroom bi, réewoo réew, kañleen ko.»
12 Esayi it neeti: «Ab car ay bawoo ca Yese reen ba, mooy taxaw, yilif jaambur ñi dul Yawut, te moom la ñi dul Yawut di yaakaar.»
13 Kon Yàlla miy maye yaakaar, yal na leen feesale gépp mbég, ak jàmm ci biir ngëm, ba ngeen géejule yaakaar, ci manoorey Noo gu Sell gi.
14 Bokk yi, man ci sama bopp, li ma bir ci seen mbir moo di yéene ju rafet ngeen fees, te buural ngeen bépp xam-xam, man ngeena artoonte it.
15 Teewul mu am ci wet yu ma leen ñemee binde kàddu yu ma ñéebluwul, ngir fàttli leen li ngeen xamoon ba noppi. Noonu ma binde nag, li ko waral moo di yiw wi ma Yàlla baaxe,
16 ngir ma doon jawriñu Almasi Yeesu, ñeel jaambur ñi dul Yawut, may wàccoo ak liggéeyu carxal bi xibaaru jàmm bu Yàlla laaj; su ko defee ñi dul Yawut mana doon ab jooxe bu Yàlla nangu, jooxe bu Noo gu Sell gi sellal.
17 Moo tax ma saña puukarewoo Almasi Yeesu mi may liggéeyloo ci mbiri Yàlla.
18 Sañumaa tudd lenn nag lu moy li Almasi sottale sama jëmm, ngir jaambur ñi dul Yawut déggal Yàlla, te muy lu mu sottale samay wax ak samay jëf,
19 ci kaw firnde yu manoorewu, aki kéemaan, lépp ci manoorey Noowug Yàlla. Loolu tax na, li dale Yerusalem, wëndeelu, ba ca diiwaanu Iliri, yégle naa fa xibaaru jàmm bu Almasi, ba mu mat sëkk.
20 Noonu laa masa xintewoo di xamle xibaaru jàmm bi fu ñu xamewul Almasi asi, ngir baña bey sas wu fa keneen jotoona dal.
21 Noonu ma jëfe it moo dëppoo ak ni ko Mbind mi indee ne: «Ña ñu waxul woon mbiram, dinañu gis, te ña dégguloon, dinañu ràññee.»
22 Sama liggéey boobu sax moo ma gàllankoor lu bare ba dikkaguma seetsi leen.
23 Waaye léegi jeexal naa sama sas ci gox yii, te gannaaw at yu baree ngii, ma namma dikk ba seetsi leen,
24 bu may dem Espaañ, dinaa leen seetsiwaale. Yaakaar naa leena gis bu ma fa jaaree, ba ngeen yiwi ma, ma jàlli Espaañ, gannaaw, lu mu néew néew, ay fan yu ma nammantikoo ak yeen.
25 Waaye fii ma tollu, Yerusalem laa jëm, ngir ndimbal lu ñeel ñu sell ña féete foofa.
26 Ndaxte gëmkati Maseduwan ak Akayi ñoom la soob ñu sàkke lenn ci seen alal, ngir dimbalee ko ñu sell ña diy néew doole ca Yerusalem.
27 Seen coobarey bopp lañu ko defe, waaye ñoo ko ameel waa Yerusalem it nag. Ndaxte gannaaw ñoom ñiy jaambur, gëmkati Yerusalem ñoo leen sédd ci xéewal yi leen ngëm may, kon ñoom jaambur ñi itam war nañu leena sédd ci seen alal.
28 Teewul nag bu ma noppee ci lii, ba teg teraanga jii ca loxoy waa Yerusalem, Espaañ laa jëm, te fa yeen laay jaare.
29 Te xam naa ne bu ma dikkee fa yeen, barkeb Almasi bu mat sëkk laay dikke.
30 Gannaaw loolu bokk yi, li ma leen di ñaan ngir sunu Boroom Yeesu Almasi, ngir itam cofeel gi Noo gu Sell giy maye, moo di ngeen fekksi ma ci xareb ñaan ngir man.
31 Ñaanal-leen ma, ngir ma mucc ci aji gëmadiy Yude, te itam ndimbal li may yóbbul ñu sell ña ca Yerusalem, ñaanleen ngir ñu nangu ko.
32 Su ko defee, ci coobarey Yàlla, ma dikke mbégte ba fa yeen, ba dal-luwaale as lëf fa yeen.
33 Yal na Yàlla miy boroom jàmm ànd ak yeen ñépp. Amiin.
Room 15 in Kàddug Yàlla gi