Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 15:1-16 in Wolof

Help us?

ROOM 15:1-16 in Téereb Injiil

1 Nun ñi dëgër ci sunu ngëm, war nanoo nangu ñi seen ngëm néew te am ci lu ñuy sikki-sàkka, te baña yem ci wut sunu bànneex.
2 Na ku nekk ci nun di wut lu neex moroomam ngir jariñ ko, ba mu gëna dëgër ci ngëmam.
3 Ndaxte Kirist masula wut bànneexu boppam. Loolu la Mbind mi wax ne: «Lor yi ñu la saagaa, ci sama kaw lañu dal.»
4 Ndaxte lépp lu ñu waxoon ci Mbind mi lu jiitu tey, dañu koo tëraloon, ngir nu sàkku ci xam-xam, xam-xam bu nuy may fit ak muñ, ak di feddali sunu yaakaar.
5 Kon nag Yàlla miy maye muñ ak fit, na leen may, ngeen déggoo te nekk benn bu yellook li Kirist Yeesu wone.
6 Ba tax nu bokk benn xalaat ak benn baat ci màggal Yàlla, Baayu Yeesu Kirist sunu Boroom.
7 Moo tax nangoonteleen, bay màggal Yàlla, ni leen Kirist nangoo.
8 Lii laay wax: Kirist ñëw na liggéeyal Yawut yi, ngir wone kóllëreg Yàlla ci matal dige, ya mu digoon maam ya.
9 Ñëw na itam ngir ñi nekkul Yawut mana màggal Yàlla ndax yërmandeem. Moo tax Mbind mi ne: «Dinaa la màggal tey tagg saw tur ci kanam xeet yépp.»
10 Mbind mi nee na it: «Yéen xeeti àddina, ñëwleen bànneexu ak xeet wi Yàlla tànnal boppam.»
11 Mu dellooti ne: «Santleen Boroom bi, yéen waa àddina, te ñëw màggal ko, yéen xeet yépp.»
12 Te it Esayi wax na ne: «Am na sëtu Isayi buy ñëw, dina yilif xeeti ñi dul Yawut, te ci moom lañuy wékk seen yaakaar.»
13 Kon Yàlla miy maye yaakaar, na def ci seen xol mbég mu réy ak jàmm ju yaa ci seen kaw ngëm, ba ngeen am yaakaar ju mat sëkk ci dooley Xel mu Sell mi.
14 Bokk yi, wóor na ma ne baax ngeen ba fa mbaax mana yem, fees dell ak xam-xam, ba mana jàngleente mbiri Yàlla ci seen biir.
15 Bu sama kàddu diisee nag ci bataaxal bii, dara taxul lu dul bëgga yeesal seen xalaat, ndaxte Yàlla ci kaw yiwam daf maa sas,
16 ma nekk jawriñu Kirist Yeesu, yebal ma ci àddina ci xeeti ñi dul Yawut. Liggéey bu sell laay def ngir Yàlla, ci xamle xibaaru jàmmam bi, ngir xeeti àddina sell ci dooley Xel mu Sell mi, ba neex Yàlla, mel ni sarax su ñu koy jébbal.
ROOM 15 in Téereb Injiil

Room 15:1-16 in Kàddug Yàlla gi

1 Nun ñi fendi ci wàllu ngëm, fàww nu xajoo tëley ñi néew doole, te baña sàkku sunu bànneexu bopp.
2 Na ku nekk ci nun sàkku bànneexu moroomam, ci lu koy jariñ, ngir feddli ngëmam.
3 Ndax Almasi kat sàkkuwul bànneexu boppam, te noonu it la Mbind mi indee ne: «Ñi lay saaga, seeni saaga, ci sama kaw la dal.»
4 Ndaxte mboolem lu ñu bindoon, bu jëkk, jàngal nu moo taxoon ñu bind ko, ngir Mbind mi may nu xolu muñ, te ñaax nu, ba nu am yaakaar.
5 Kon nag Yàlla miy maye xolu muñ, di ñaaxe, yal na leen may mànkoo gu mat sëkk, ni ko Almasi Yeesu bëgge,
6 ngir nu bokk jenn yéene ak genn kàddu gu ngeen sàbbaale Yàlla, sunu Baayu Sang Yeesu Almasi.
7 Kon nag, ni leen Almasi xajoo, nangeen ko xajoontee, ngir teddngay Yàlla.
8 Dama leen di wax ne leen, bëgga fésal ne Yàlla ku dëggu la moo waral Almasi dikk, def boppam jawriñu Yawut yi, ngir sottal dige ya Yàlla digoon seeni maam.
9 Leneen li indi Almasi mooy may jaambur ñi dul Yawut lu ñu màggale Yàlla, te muy yërmandeem. Noonu it la Mbind mi indee ne: «Looloo waral ma sant la ci biir xeet yi, sàbbaal la.»
10 Mu neeti: «Yeen xeet yi, bégandooleen ak ñoñam.»
11 Mu dellu ne: «Yeen xeetoo xeet, màggal-leen Boroom bi, réewoo réew, kañleen ko.»
12 Esayi it neeti: «Ab car ay bawoo ca Yese reen ba, mooy taxaw, yilif jaambur ñi dul Yawut, te moom la ñi dul Yawut di yaakaar.»
13 Kon Yàlla miy maye yaakaar, yal na leen feesale gépp mbég, ak jàmm ci biir ngëm, ba ngeen géejule yaakaar, ci manoorey Noo gu Sell gi.
14 Bokk yi, man ci sama bopp, li ma bir ci seen mbir moo di yéene ju rafet ngeen fees, te buural ngeen bépp xam-xam, man ngeena artoonte it.
15 Teewul mu am ci wet yu ma leen ñemee binde kàddu yu ma ñéebluwul, ngir fàttli leen li ngeen xamoon ba noppi. Noonu ma binde nag, li ko waral moo di yiw wi ma Yàlla baaxe,
16 ngir ma doon jawriñu Almasi Yeesu, ñeel jaambur ñi dul Yawut, may wàccoo ak liggéeyu carxal bi xibaaru jàmm bu Yàlla laaj; su ko defee ñi dul Yawut mana doon ab jooxe bu Yàlla nangu, jooxe bu Noo gu Sell gi sellal.
Room 15 in Kàddug Yàlla gi