23Car ya fàqe woon itam, su ñu wéyewul ngëmadi, dees leen di delloo ca ndey ja, nde Yàlla man na leen caa saxalaat.
24Ndax kat, ndegam yaw lañu tenqee ci oliwu àll gi, jabtal la ci oliwu kër gi dul sa ndey, astamaak car yi oliwu kër gi di seen ndey, nde saxalaat leen ca mooy gëna yombati.
25Bokk yi, moytuleena defe ne seen xel mu rafet a leen may li ngeen am. Bugguma ngeen umple mii mbóot: Ag déggadi moo dikkal lennati bànni Israyil, ba kera xeet yi dul Yawut duggsi, ba seenub lim mat.
26Su boobaa nag, bànni Israyil gépp ay mucc, noonee ko Mbind mi indee ne: «Siyoŋ la wallukat bay jóge, mooy tenqee ngëmadi ci askanu Yanqóoba.
27Loolooy doon sama kóllëreek ñoom, kera ba may far seeni bàkkaar.»
28Ci wàllu xibaaru jàmm bi, ay noon la Yawut ñi taxawe, te muy xéewal ci yeen ñi dul Yawut. Waaye ci wàllu dogal bi taamu Yawut ñi, ay soppe lañu, te seeni maam tax.
29Ndax Yàlla kat, ay mayam akub wooteem, lenn du ci toxu.
30Yeena déggadi woon, waaye tey daj ngeen yërmande, ndax déggadig Yawut yi.
31Noonu itam la Yawut yi déggadee tey, ba ni ngeen daje yërmande, ñoom it ñu daje ni yërmande.
32Yàlla moo tëj nit ñépp ci seenug déggadi, ngir yërëm leen ñoom ñépp.
33Céy xóotaayub koomu Yàlla ak xel ma, ak xam-xam ba! Deesul natt ay dogalam, deesul ràññee ay jëfinam!
34«Ana ku xam xalaatu Boroom bi? Ana ku ko digal?»