14Jombul sama liggéey dina yee fiiraangey sama bokki Yawut ñi, ba ñenn ci ñoom mucc.
15Ndax kat ba Yàlla dàqee Israyil, ca la àddina juboo ak Yàlla. Kon nag bu leen Yàlla délloosee, ana lu muy jur lu moy ndee-ndekki?
16Ndax kat ab jooxe bu génnee ci tooyalub sunguf, di ndoortel meññeef, su boobu jooxe sellee, tooyalub sunguf bépp ay sell. Ndax su reenu garab sellee, car ya it sell.
17Waaye su ñu tenqee lenn ci cari oliwu kër, te yaw ngay caru oliwu àll, ñu indi la, jabtal ci oliwu kër gi, nga wuutu car ya ca fàqe, ba mana xéewloo meen miy wale ci reenu oliwu kër gi, di ko dundal,
18bumu tax nga bàkku ci kaw car ya fàqe. Soo dee bàkku, xamal ne du yaa yenu reen bi, waaye reen bee la yenu.