Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Room - Room 10

Room 10:10-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
10Ndax kat ab xol lees di gëme, ba am àtteb ku jub, te aw làmmiñ lees di birale ngëm gi ba mucc.
11Mbind mi moo ne: «Képp ku ko gëm, doo rus.»
12Ag wuutale amul diggante ab Yawut, ak jaambur bu dul Yawut; ñépp a bokk benn Boroom biy yéwéne mboolem ñi koy woo wall.
13Ndax kat waxees na ne: «Képp ku woo Boroom bi wall ciw turam, mooy raw.»
14Waaye nees di wooye koo gëmul? Nees di gëme koo déggul turam? Nees di dégge turam, te yégleesu ko?
15Nees di yéglee xibaar, te yebaleesu la? Noonu la Mbind mi indee ne: «Ñeeka rafeti tànk, ndaw yii di yéglesi xibaari jàmm!»
16Waaye du ñépp a nangul xibaaru jàmm bi; moo tax Esayi ne: «Boroom bi, ana ku gëm sunub dégtal?»
17Kon boog ngëm ci dég-dég lay juddoo, dég-dég ba bawoo ci kàddug waare gi jëm ci Almasi.

Read Room 10Room 10
Compare Room 10:10-17Room 10:10-17