Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Peeñu ma

Peeñu ma 8

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Bi Gàtt bi tàyyee juróom ñaareelu tayu gi nag, asamaan da ne selaw lu mat genn-wàllu waxtu.
2Ci kaw loolu ma gis juróom ñaari malaaka yi taxaw fi kanam Yàlla, ñu jox leen juróom ñaari liit.
3Bi loolu amee meneen malaaka dikk, taxaw ci wetu sarxalukaay bi. Mu ngi yor andu cuuraayu wurus. Ñu jox ko cuuraay lu bare, ngir mu boole kook ñaani mboolem aji sell ñi, jooxe ko ci kaw sarxalukaayu wurus bi ci kanam ngàngune mi.
4Saxaras cuuraay laa ngi gillee ci loxol malaaka mi, ànd ak ñaani ñu sell ñi, di yéeg fa Yàlla.
5Malaaka mi jël andu cuuraay bi, tibbe ci sarxalukaay bi ay xal ba and bi fees. Mu daldi koy sànni ci kaw àddina, rekk ag dënu riir, kàddu ràndaŋ, ag melax tàkk, suuf yëngu.
6Ba mu ko defee juróom ñaari malaaka yi yor juróom ñaari liit yi di waaja liit.
7Malaaka mu jëkk mi wal liitam, tawu doji yuur topp ci, ak sawara wu ànd ak deret, ñu boole lépp sànni ci kaw suuf, ñetteelu xaaju suuf si daldi lakk, ñetteelu xaaju garab yi it lakk, ñax mu naat mépp lakk.
8Ñaareelu malaaka mi wal liitam, mu am lu mel ni tund wu réy wuy tàkk, ñu sànni ko ci géej gi, ñetteelu xaaju géej gi soppiku deret,
9ñetteelu xaaju bindeefi géej dee, ñetteelu xaaju gaal yi yàqu yaxeet.
10Ñetteelu malaaka mi wal liitam, biddiiw bu réy buy tàkk nig jum xàwwikoo asamaan, wadd ci kaw ñetteelu xaaju dex yi ak bëti ndox yi.
11Biddiiw bi Wextan la tudd. Ñetteelu xaaju ndox yépp la wexal, ñu bare naan ci, daldi dee, ndax wextanu ndox mi.
12Ñeenteelu malaaka mi wal liitam, mu dal ñetteelu xaaju jant bi, ak ñetteelu xaaju weer wi, ak ñetteelu xaaju biddiiw yi, ba tax seen ñetteelu xaaju leer giim, ñetteelu xaaju bëccëg bi daldi lëndëm, ñetteelu xaaju guddi gi it gëna lëndëm.
13Ma xoolaat, daldi dégg jenn jaxaay ju naawe digg asamaan. Mu àddu ca kaw ne: «Wóoy, wóoy, wóoy, musibay waa àddina yiy sababoo ci yeneen baati liit yi ñetti malaaka yi ci des, di waaja liit.»