Text copied!
Bibles in Wolof

Ngën-gi-woy 8:5-14 in Wolof

Help us?

Ngën-gi-woy 8:5-14 in Kàddug Yàlla gi

5 Ana ndaw suy jóge màndiŋ ma nii, wéeroo nijaayam? Ndaw si Ci ron pom gi laa la yee, fa la sa yaay jàppe ëmb, jur la fa.
6 Teg ma ci sa xol ni torlukaay, mbaa ci sa përëg ni lamu màndarga. Mbëggeel a bare doole ni ndee, fiiraange xér ni bàmmeel. Day jàpp jippét, di jum bu Aji Sax ji taal.
7 Ndox mu ne xéew du fey mbëggeel, ay dex du ko mëdd. Ku koy weccee sa alalu kër gépp it, ñu jéppi laa jéppi rekk.
8 Sunub jigéen lu ndaw la, ween sax amu ko. Lu nuy defal sunub jigéen bés bu ñu koy bëggsi?
9 Su doon am tata, nu tabaxal ko soorooru xaalis. Su doon bunt, nu aare ko xànqi seedar.
10 Maa dim tata, sama ween di sooroor ya; moo tax waa ji xam ne maa di jàmmam.
11 Suleymaan am na reseñ ca Baal Amon. Da koo dénk ay beykat. Ku nekk di ko fey meññeef ma junniy dogi xaalis.
12 Junniy dogi xaalis yi, Suleymaan, yaa ko moom; ñaar téeméer yi, beykat yi. Waaye sama toolub reseñ, maa ko moom.
13 Yaw mi tooge digg tool bi, samay xarit a ngi teewlu sa baat, waxal boog, ma dégg.
14 Nijaay, dawsil, melal ni kéwél, mbaa kooba gu ndaw ci kaw tund wi ci gàncax gu xeeñ gi.
Ngën-gi-woy 8 in Kàddug Yàlla gi