3 Sama càmmoñu waay, ma gegenoo, ndijooram, ma laxasoo.
4 Yeen janqi Yerusalem, waatal-leen ma ne dungeen dakkal te dungeen sooke tëraayu mbëggeel te jotul.
5 Ana ndaw suy jóge màndiŋ ma nii, wéeroo nijaayam? Ndaw si Ci ron pom gi laa la yee, fa la sa yaay jàppe ëmb, jur la fa.
6 Teg ma ci sa xol ni torlukaay, mbaa ci sa përëg ni lamu màndarga. Mbëggeel a bare doole ni ndee, fiiraange xér ni bàmmeel. Day jàpp jippét, di jum bu Aji Sax ji taal.
7 Ndox mu ne xéew du fey mbëggeel, ay dex du ko mëdd. Ku koy weccee sa alalu kër gépp it, ñu jéppi laa jéppi rekk.
8 Sunub jigéen lu ndaw la, ween sax amu ko. Lu nuy defal sunub jigéen bés bu ñu koy bëggsi?
9 Su doon am tata, nu tabaxal ko soorooru xaalis. Su doon bunt, nu aare ko xànqi seedar.