7 Rafet, sopploo! Soppee, bànneex nga!
8 Sa taxawaay bii garabu tàndarma la, sa ween yi di cëggi doom ya.
9 Ma ne, maay yéeg tàndarma gi, ŋëb doom yi. Yal na say ween di sama cëggi reseñ, sag noo jox ma doom yu xeeñ,
10 sa gémmiñ di xelli ngëneelu biiñ. Ndaw si Na walal sama nijaay, tuurul ñiy nelaw.
11 Man, nijaay a moom, te maay nammeelam.
12 Nijaay, ayca nu dem tool ba, fanaani ca tóor-tóori fuddën ya.