Text copied!
Bibles in Wolof

Ngën-gi-woy 7:2-10 in Wolof

Help us?

Ngën-gi-woy 7:2-10 in Kàddug Yàlla gi

2 Janqoo, lingeer sama, sa tànk yee ka jekk ci sa dàll yi, sa mooco yi mërgalu niy jaaro yu ndaanaanu tëgg yette loxoom.
3 Sa jumbux bi di kaas bu mërgalu, yàlla bumu ñàkk biiñu njafaan! Sa biir bi di jalu pepp mu ay tóor-tóor ñag.
4 Sa ween yi ni ñaari tef, mbaa seexi kéwél.
5 Sa loos wi, coleet, rattax, ni tatay bëñi ñay; say gët di lerxat ni déegi Esbon, ya feggook buntu Bat Rabim. Sa bakkan bi jub xocc ni tatay Libaŋ ja tiim Damaas.
6 Sa bopp siggi ni tundu Karmel, njañ liy nes-nesi ni sooyu buur, létt yay fëy-fëyi, ba laaw buur.
7 Rafet, sopploo! Soppee, bànneex nga!
8 Sa taxawaay bii garabu tàndarma la, sa ween yi di cëggi doom ya.
9 Ma ne, maay yéeg tàndarma gi, ŋëb doom yi. Yal na say ween di sama cëggi reseñ, sag noo jox ma doom yu xeeñ,
10 sa gémmiñ di xelli ngëneelu biiñ. Ndaw si Na walal sama nijaay, tuurul ñiy nelaw.
Ngën-gi-woy 7 in Kàddug Yàlla gi