Text copied!
Bibles in Wolof

Ngën-gi-woy 2:2-16 in Wolof

Help us?

Ngën-gi-woy 2:2-16 in Kàddug Yàlla gi

2 Xanaa as tóor-tóor su ne ràññ ci biiri dég! Kookooy sama xarit ci biir janq ji.
3 Mbete garab gu gëna neex ci gott bi, kookooy sama nijaay ci biir xale yu góor yi. May bége keppaaram, safoo doom ya.
4 Dugal na ma néegub sago-jeex-na, yiire ma mbëggeel.
5 Gaaweleen ma nàkki reseñ, ma dëgër, leel-leen may meññeef, leqlee ma. Wopp laa def ndax mbëggeel!
6 Sama càmmoñu waay, ma gegenoo, ndijooram, ma laxasoo.
7 Yeen janqi Yerusalem, waatal-leen ma ci taaru kéwél ak koobay àll bi, ne dungeen dakkal te dungeen sooke tëraayu mbëggeel te jotul.
8 Dégluleen, sama nijaay a, mu ngooguy ñëw, di xéluy jéggi tund yu ndaw yi, di tëb tund yu mag yiy dikk.
9 Sama nijaay a ngi mel ni kéwél, mbaa kooba gu ndaw. Mu ngi noonu taxaw ca gannaaw miir ba, di séentu ci palanteer bi ak a yër ci caax bi.
10 Sama nijaay ne ma: «Xarit, ayca, jongama sama, dikkal boog!
11 Xoolal, tawub sedd wees na, waame jàll, wéy.
12 Tóor-tóor yi lal na réew mi, jamonoy woy dikk, sabum pégét jibe sunum réew.
13 Figg a ngi ñorsi, reseñ tóor, di gilli. Xarit, ayca, jongama sama, dikkal boog!»
14 Soppe, sore nga ni xati mu dëkke xar-xari doj, làqoo ruqi mbartal yi. Won ma sa jëmm, dégtal ma sa baat. Sa baat a neex, sa jëmm jekk!
15 Jàppal-leen ma till yi, till yu ndaw yiy ruur reseñ, te sunu reseñ jiy tóor.
16 Sama nijaay, maa moom, man it, moo moom, di fore digg tóor-tóor yi.
Ngën-gi-woy 2 in Kàddug Yàlla gi