Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ngën-gi-woy - Ngën-gi-woy 2

Ngën-gi-woy 2:2-16

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Xanaa as tóor-tóor su ne ràññ ci biiri dég! Kookooy sama xarit ci biir janq ji.
3Mbete garab gu gëna neex ci gott bi, kookooy sama nijaay ci biir xale yu góor yi. May bége keppaaram, safoo doom ya.
4Dugal na ma néegub sago-jeex-na, yiire ma mbëggeel.
5Gaaweleen ma nàkki reseñ, ma dëgër, leel-leen may meññeef, leqlee ma. Wopp laa def ndax mbëggeel!
6Sama càmmoñu waay, ma gegenoo, ndijooram, ma laxasoo.
7Yeen janqi Yerusalem, waatal-leen ma ci taaru kéwél ak koobay àll bi, ne dungeen dakkal te dungeen sooke tëraayu mbëggeel te jotul.
8Dégluleen, sama nijaay a, mu ngooguy ñëw, di xéluy jéggi tund yu ndaw yi, di tëb tund yu mag yiy dikk.
9Sama nijaay a ngi mel ni kéwél, mbaa kooba gu ndaw. Mu ngi noonu taxaw ca gannaaw miir ba, di séentu ci palanteer bi ak a yër ci caax bi.
10Sama nijaay ne ma: «Xarit, ayca, jongama sama, dikkal boog!
11Xoolal, tawub sedd wees na, waame jàll, wéy.
12Tóor-tóor yi lal na réew mi, jamonoy woy dikk, sabum pégét jibe sunum réew.
13Figg a ngi ñorsi, reseñ tóor, di gilli. Xarit, ayca, jongama sama, dikkal boog!»
14Soppe, sore nga ni xati mu dëkke xar-xari doj, làqoo ruqi mbartal yi. Won ma sa jëmm, dégtal ma sa baat. Sa baat a neex, sa jëmm jekk!
15Jàppal-leen ma till yi, till yu ndaw yiy ruur reseñ, te sunu reseñ jiy tóor.
16Sama nijaay, maa moom, man it, moo moom, di fore digg tóor-tóor yi.

Read Ngën-gi-woy 2Ngën-gi-woy 2
Compare Ngën-gi-woy 2:2-16Ngën-gi-woy 2:2-16