Text copied!
Bibles in Wolof

Mucc ga 20:3-5 in Wolof

Help us?

Mucc ga 20:3-5 in Kàddug Yàlla gi

3 «Buleen am yeneen yàlla ci sama kanam.
4 «Buleen sàkkal seen bopp tuur muy jëmmal lenn lu nekk ci kaw asamaan, mbaa ci kaw suuf, mbaa lu nekk ci ndox mu suuf tiim.
5 Buleen ci sujjóotal lenn, buleen ci jaamu lenn, ndax man seen Yàlla Aji Sax ji, Yàlla ju fiir laa. Maay topp doom tooñu waajur, ba ca seen maasi sët, ba ca maasug sëtaati nit ñi ma bañ.
Mucc ga 20 in Kàddug Yàlla gi