Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - MÀRK - MÀRK 7

MÀRK 7:24-34

Help us?
Click on verse(s) to share them!
24Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, jëm weti dëkku Tir. Bi mu fa eggee, mu dugg ci kër, te bëggul kenn xam ko, waaye jataayam manula umpe.
25Amoon na fa nag jigéen ju rab jàpp doomam ju jigéen. Bi mu déggee ne, Yeesoo nga fa, mu ñëw, daanu ciy tànkam,
26fekk jigéen ja ci xeetu Gereg la bokkoon, juddoo wàlli Fenisi ci diiwaanu Siri. Noonu jigéen ja ñaan ko, mu dàq rab wi ci doomam.
27Waaye Yeesu ne ko: «Na gone yi jëkka lekk, ba regg; fab ñamu gone yi, sànni ko xaj yi, rafetul.»
28Jigéen ji ne ko: «Waaw, sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci lekkukaayu gone yi.»
29Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Ndax wax jooju demal ci jàmm, rab wa génn na sa doom.»
30Noonu mu ñibbi, fekk doom ji tëdd cib lal te mucc ci rab wi.
31Bi loolu amee Yeesu jóge na weti Tir, jaar ci wàlli dëkku Sidon, dem dexu Galile, ba noppi dugg ci biir diiwaan, bi ñuy wax Fukki dëkk yi.
32Foofa ñu indil ko ku tëx te dër lool, ñaan ko mu teg ko loxo.
33Noonu Yeesu yóbbu ko, ba ñu sore mbooloo mi, mu def ay baaraamam ciy noppam, daldi tifli, laal làmmiñam.
34Mu yërëm ko, ba binni ci xolam, xool ci asamaan, daldi ne: «Effata,» liy tekki «Ubbikuleen.»

Read MÀRK 7MÀRK 7
Compare MÀRK 7:24-34MÀRK 7:24-34