Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 25:4-17 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 25:4-17 in Kàddug Yàlla gi

4 Aji Sax ji ne Musaa: «Jàppal njiiti mbooloo mi yépp, nga wékk leen ci bant fi kanam Aji Sax ji, bëccëg ndarakàmm, ngir sànjum Aji Sax ji dëddu Israyil.»
5 Musaa ne àttekati Israyil: «Na ku nekk ci yeen rey nitam ñi taqook Baal Pewor.»
6 Ci biir loolu rekk, jenn waayu bànni Israyil dikk, indaale senn ndawas waa Majan ci biiri bokkam, Musaa ak mbooloom Israyil mépp di gis, fekk ñoom ñuy jooyoo fa bunt xaymab ndaje ma.
7 Fineyas, doomu Elasar, doomu sarxalkat ba Aaróona, gis loolu, daldi jóge ca mbooloo ma, jël ab xeej.
8 Mu topp waayi Israyil ja ba ca biir néeg ba, daldi leen boole bennub xeej, ñoom ñaar, jam waayi Israyil ji, ba jamaale ndaw si ci biir. Ba mu ko defee mbas ma jotoona dal ca kaw bànni Israyil daldi dakk.
9 Ña dee ca mbas ma nag di ñaar fukki junneek ñeent (24 000).
10 Ba loolu weesee Aji Sax ji wax Musaa, ne ko:
11 «Fineyas, doomu Elasar, doomu sarxalkat bi Aaróona, moo moyale Israyil samam sànj, ndax sama fiiraange gi mu ma fiirlee ci seen biir, ba faagaagaluma bànni Israyil ci sama biir fiiraange.
12 Kon nag nee ko: Maa ngii di ko baaxe sama kóllëreg jàmm,
13 mu ñeel ko, mook askan wi koy wuutu, te di kóllëreg carxal gu sax dàkk, ndax moo fiire Yàllaam, ba jot bànni Israyil.»
14 Waayi bànni Israyil ja ñu jamoon, te boole kook ndawas Majan sa jam, mooy Simri doomu Salu. Kilifag kër maamam la woon ca Cimyoneen ña.
15 Ndawas Majan sa ñu jam di Kosbi. Baayam Sur doonoon kilifag kër maamam ca giirug Majan ga mu bokk.
16 Ci kaw loolu Aji Sax ji wax Musaa, ne ko:
17 «Noonooleen waa Majan yii, te rey leen,
Màndiŋ ma 25 in Kàddug Yàlla gi