Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 25

Màndiŋ ma 25:4-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Aji Sax ji ne Musaa: «Jàppal njiiti mbooloo mi yépp, nga wékk leen ci bant fi kanam Aji Sax ji, bëccëg ndarakàmm, ngir sànjum Aji Sax ji dëddu Israyil.»
5Musaa ne àttekati Israyil: «Na ku nekk ci yeen rey nitam ñi taqook Baal Pewor.»
6Ci biir loolu rekk, jenn waayu bànni Israyil dikk, indaale senn ndawas waa Majan ci biiri bokkam, Musaa ak mbooloom Israyil mépp di gis, fekk ñoom ñuy jooyoo fa bunt xaymab ndaje ma.
7Fineyas, doomu Elasar, doomu sarxalkat ba Aaróona, gis loolu, daldi jóge ca mbooloo ma, jël ab xeej.
8Mu topp waayi Israyil ja ba ca biir néeg ba, daldi leen boole bennub xeej, ñoom ñaar, jam waayi Israyil ji, ba jamaale ndaw si ci biir. Ba mu ko defee mbas ma jotoona dal ca kaw bànni Israyil daldi dakk.
9Ña dee ca mbas ma nag di ñaar fukki junneek ñeent (24 000).
10Ba loolu weesee Aji Sax ji wax Musaa, ne ko:
11«Fineyas, doomu Elasar, doomu sarxalkat bi Aaróona, moo moyale Israyil samam sànj, ndax sama fiiraange gi mu ma fiirlee ci seen biir, ba faagaagaluma bànni Israyil ci sama biir fiiraange.
12Kon nag nee ko: Maa ngii di ko baaxe sama kóllëreg jàmm,
13mu ñeel ko, mook askan wi koy wuutu, te di kóllëreg carxal gu sax dàkk, ndax moo fiire Yàllaam, ba jot bànni Israyil.»
14Waayi bànni Israyil ja ñu jamoon, te boole kook ndawas Majan sa jam, mooy Simri doomu Salu. Kilifag kër maamam la woon ca Cimyoneen ña.
15Ndawas Majan sa ñu jam di Kosbi. Baayam Sur doonoon kilifag kër maamam ca giirug Majan ga mu bokk.
16Ci kaw loolu Aji Sax ji wax Musaa, ne ko:
17«Noonooleen waa Majan yii, te rey leen,

Read Màndiŋ ma 25Màndiŋ ma 25
Compare Màndiŋ ma 25:4-17Màndiŋ ma 25:4-17