2 «Limleen mbooloom bànni Israyil gépp, na ñu bokke seeni làng ak seen këri maam. Waññleen góor ñépp, bopp ak bopp, ku nekk ak turam.
3 Li ko dale ñaar fukki at, jëm kaw, mboolem ñi xare war ci Israyil daal, nangeen leen lim, gàngoor ak gàngoor, yaw ak Aaróona.
4 Giir gu ci nekk, àndleen ceek kilifa yi jiite seen këri maam, ñu jàpple leen ci.
5 Ñiy wuyoo tur yii nag, ñoo leen ciy taxawu: Ci wàllu Rubeneen ñi, Elisur doomu Sedeyur.
6 Wàllu Cimyoneen ñi, Selumyel doomu Surisadaay.
7 Wàllu Yudeen ñi, Nason doomu Aminadab.
8 Wàllu Isakareen ñi, Netanel doomu Suwar.
9 Wàllu Sabuloneen ñi, Elyab doomu Elon.