Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 9:3-31 in Wolof

Help us?

LUUG 9:3-31 in Téereb Injiil

3 Mu ne leen: «Bu ngeen di dem, buleen yóbbaale dara, du yet mbaa mbuus mbaa mburu mbaa xaalis. Buleen yor it ñaari turki.
4 Kër gu ngeen dugg, dal-leen fa, ba kera ngeen di fa jóge.
5 Fépp fu leen nit ñi gàntoo, génnleen ca dëkk booba te ngeen yëlëb seen pëndu tànk, ngir seede leen seen réer.»
6 Noonu ñu dem dëkk ak dëkk, di fa yégle xibaaru jàmm bi, tey wéral jarag yi.
7 Bi Erodd boroom diiwaanu Galile déggee li Yeesu ak ay taalibeem doon def lépp, mu jaaxle, ndaxte amoon na, ñu doon wax ci mbiri Yeesu naan: «Yaxya moo dekki.»
8 Am it ñuy wax naan: Ilyaas moo délsi. Ñeneen naan: «Kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki.»
9 Waaye Erodd ne: «Yaxya, man mii maa dagglu boppam. Kon kii ma dégg ay jalooreem, mooy kan?» Noonu mu koy fexee gis.
10 Bi ndaw ya délsee, ñu nettali Yeesu la ñu defoon lépp. Noonu mu yóbbaale leen, ñu sore nit ñi, jëm ca dëkk bu ñuy wax Betsayda.
11 Bi ko nit ña yégee, ñu toppi ko. Yeesu teeru leen, di leen wax ci mbirum nguuru Yàlla, te di wéral ñi ko aajowoo.
12 Ca ngoon sa fukki taalibe ya ak ñaar ñëw ci Yeesu ne ko: «Yiwil mbooloo mi, ñu dugg ci dëkk yi ak àll bi ko wër, ngir am lu ñu lekk ak fu ñu fanaan, ndaxte fii àllub neen la.»
13 Waaye Yeesu ne leen: «Joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu ne ko: «Amunu lu dul juróomi mburu ak ñaari jën. Xanaa ndax nu dem jëndal mbooloo mii lu ñu lekk?»
14 Ndaxte lu wara mat juróomi junniy góor a nga fa teewoon. Yeesu ne taalibe ya: «Neeleen mbooloo mi ñu toog def ay géewi juróom fukki nit.»
15 Taalibe ya def ko, toogloo nit ña.
16 Bi loolu amee Yeesu jël juróomi mburu yi ak ñaari jën yi, xool ci kaw, gërëm Yàlla, ba noppi mu damm leen, jox taalibe yi, ngir ñu séddale ko mbooloo mi.
17 Noonu ñépp lekk ba suur. Bi ñu dajalee desit ya, ñu feesal fukki pañe ak ñaar.
18 Benn bés Yeesu beddeeku mbooloo ma, di ñaan; taalibe yi nekk ci wetam. Mu laaj leen ne: «Nit ñi, ku ñu wax ne moom laa?»
19 Ñu ne ko: «Am na ñu naan, yaa di Yaxya; ñeneen ne, Ilyaas; ñi ci des ne yaay kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki.»
20 Yeesu ne leen: «Yéen nag ku ngeen ne moom laa?» Piyeer ne ko: «Yaa di Almasi, bi Yàlla yónni.»
21 Noonu Yeesu daldi leen dénk, tere leen ñu wax ko kenn,
22 teg ca ne: «Doomu nit ki war na sonn lu bare; sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya dëddu ko, ñu rey ko, mu dekki ca ñetteelu fan ba.»
23 Noonu Yeesu ne leen ñoom ñépp: «Ku bëgga aw ci samay tànk, na bàyyi boppam, gàddu bés bu nekk bant, bi ñu ko wara daaj, doora topp ci man.
24 Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man, dinga ko jotaat.
25 Ndaxte moom àddina sépp, lu muy jariñ nit, su fekkee ne dafay ñàkk bakkanam walla mu loru?
26 Ku ma rusa faral, te nanguwul samay wax, Doomu nit ki dina la rusa xam, bés bu ñëwee ci ndamam ak ci ndamu Baay bi ak lu malaaka yu sell yi.
27 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, am na ñi fi taxaw ñoo xam ne duñu dee te gisuñu nguuru Yàlla gi.»
28 Bi ñu ca tegee luy tollook ayu-bés gannaaw bi Yeesu waxee loolu, mu ànd ak Piyeer, Yowaana ak Saag, yéeg ca kaw tund wa ngir ñaan.
29 Bi muy ñaan, xar kanamam daldi soppiku, ay yéreem weex tàll bay melax.
30 Am ñaari nit di waxtaan ak moom, muy yonenti Yàlla Musaa ak Ilyaas.
31 Ñoo feeñ ci ndamu Yàlla, di waxtaane ci demug Yeesu, gi muy àggalee yenam ci Yerusalem.
LUUG 9 in Téereb Injiil

Luug 9:3-31 in Kàddug Yàlla gi

3 Mu ne leen: «Bu ngeen di dem, buleen yóbbaale dara ngir fàggu yoon wi; du yet, du mbuus, du aw ñam, du xaalis. Bu ci kenn yor ñaari turki sax.
4 Kër gu ngeen dugg, fa ngeen di dal, ba kera ngeen dem.
5 Fépp fu ñu leen dalalewul, génnleen dëkk booba te ngeen faxas fa seen pëndub ndëgguy tànk, seedeele leen ko seen ngàntal.»
6 Ñuy dem nag, di wër dëkk ak dëkk, di yégle xibaaru jàmm bi, di faj jarag ji.
7 Ci kaw loolu Erodd boroom Galile dégg mboolem la xew, boppam nag ubu, ndax ñenn ñu noon Yaxya moo dekki, di Yeesu.
8 Ñee ne Ilyaas moo délsi, ñeneen ba tey, ne kenn ca yonent yu jëkk yaa dekki.
9 Erodd daldi ne: «Yaxya, man maa doglu boppam. Kon ki ma déggal jëf jii, mooy kan?» Ba loolu amee mu di ko fexee gis.
10 Ba ndaw ya délsee, dañoo nettali Yeesu mboolem la ñu def. Mu ànd ak ñoomu neen ba sore, ca wetu dëkk ba ñuy wax Beccayda.
11 Teewul nit ña yég ne fa la dem, daldi ko topp. Yeesu dalal leen, di leen wax ci mbirum nguurug Yàlla, ña aajowoo am paj, mu wéral leen.
12 Ba jant di sowat, Fukk ñaak ñaar dikk ne Yeesu: «Yiwil mbooloo mi, ñu dugg ci dëkk yu ndaw yii ak dëkk-dëkkaan yi ko wër, ngir ñu gis lu ñu lekk ak fu ñu fanaan, ndax fii àllub neen la.»
13 Mu ne leen: «Yeen, joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu ne ko: «Nun de amunu lu dul juróomi mburu ak ñaari jën. Xanaa nu dem, nun ci sunu bopp, jëndali mbooloo mii mépp lu ñu lekk!»
14 Lu wara mat juróomi junniy góor a nga fa woon. Yeesu ne taalibe ya: «Dangeen leen di toogal, ñu def géewi juróom fukki nit.»
15 Ñu def noonu, toogal ñépp.
16 Ba mu ko defee Yeesu jël juróomi mburu ya ak ñaari jën ya, xool kaw asamaan, daldi yékkati kàddug cant, ba noppi dagg mburu ya, jox taalibe ya, ngir ñu taajal ko mbooloo ma.
17 Ñépp lekk ba regg, ba ñu yóbbu dog ya ca des, muy fukki pañe ak ñaar.
18 Yeesu moo beru woon, di julli, taalibe ya feggook moom. Ci kaw loolu mu laaj leen ne leen: «Ana ku nit ñi ne moom laa?»
19 Ñu ne ko: «Ñii nee ñu yaa di Yaxya; ñee ne yaa di Ilyaas; ñale ne kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki, di yaw.»
20 Yeesu ne leen: «Yeen nag, ngeen ne maay kan?» Piyeer ne ko: «Yaa di Almasib Yàlla.»
21 Mu femmu leen nag, sant leen ñu bañ koo wax kenn.
22 Mu neeti: «Fàww Doomu nit ki sonn lu bare, ba dajeek mbañeelu magi askan wi ak sarxalkat yu mag yi, ak firikati yoon yi, te dees na ko rey, ba ñetteelu fanam, mu dekki.»
23 Yeesu nag wax leen ñoom ñépp, ne leen: «Képp ku bëgga dikk topp ma, fàtteel sa bopp, te nga gàddu bés bu nekk, bant bi ñu lay daaj, door maa topp.
24 Ndax képp ku namma rawale sa bakkan, yaay ñàkk sa bakkan, waaye képp ku ñàkk sa bakkan ngir man, yaa musal sa bakkan.
25 Ndax nit ki, su jagoo àddina sépp sax, te nara ñàkk bakkanam mbaa mu sànku, ana lu mu koy jariñ?
26 Képp ku kersawoo sama jëmm, kersawoo topp samay wax, yaw itam Doomu nit ki dina la kersawoo, bés bu dikkee ci darajaam ak darajay Baay bi, ak darajay malaaka yu sell yi.
27 Maa leen ko wax déy, ñenn a ngi fii taxaw tey, duñu dee te gisuñu nguurug Yàlla.»
28 Ba lu wara tollook juróom ñetti fan wéyee gannaaw kàddu yooyu, Yeesu àndoon na ak Piyeer ak Yowaan ak Yanqóoba, ñu yéeg ca kaw tund wa ngir julli.
29 Naka lay julli, xar kanamam soppiku, ay yéreem weex tàll, di melax.
30 Ci kaw loolu ñaari nit jekki feeñ, di waxtaan ak moom; ñuy Yonent Yàlla Musaa ak Yonent Yàlla Ilyaas.
31 Ñoo feeñ ci ag leer, di waxtaane dëddug Yeesu, ga mu doon waaja sottale fa Yerusalem.
Luug 9 in Kàddug Yàlla gi