Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 9

Luug 9:3-31

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Mu ne leen: «Bu ngeen di dem, buleen yóbbaale dara ngir fàggu yoon wi; du yet, du mbuus, du aw ñam, du xaalis. Bu ci kenn yor ñaari turki sax.
4Kër gu ngeen dugg, fa ngeen di dal, ba kera ngeen dem.
5Fépp fu ñu leen dalalewul, génnleen dëkk booba te ngeen faxas fa seen pëndub ndëgguy tànk, seedeele leen ko seen ngàntal.»
6Ñuy dem nag, di wër dëkk ak dëkk, di yégle xibaaru jàmm bi, di faj jarag ji.
7Ci kaw loolu Erodd boroom Galile dégg mboolem la xew, boppam nag ubu, ndax ñenn ñu noon Yaxya moo dekki, di Yeesu.
8Ñee ne Ilyaas moo délsi, ñeneen ba tey, ne kenn ca yonent yu jëkk yaa dekki.
9Erodd daldi ne: «Yaxya, man maa doglu boppam. Kon ki ma déggal jëf jii, mooy kan?» Ba loolu amee mu di ko fexee gis.
10Ba ndaw ya délsee, dañoo nettali Yeesu mboolem la ñu def. Mu ànd ak ñoomu neen ba sore, ca wetu dëkk ba ñuy wax Beccayda.
11Teewul nit ña yég ne fa la dem, daldi ko topp. Yeesu dalal leen, di leen wax ci mbirum nguurug Yàlla, ña aajowoo am paj, mu wéral leen.
12Ba jant di sowat, Fukk ñaak ñaar dikk ne Yeesu: «Yiwil mbooloo mi, ñu dugg ci dëkk yu ndaw yii ak dëkk-dëkkaan yi ko wër, ngir ñu gis lu ñu lekk ak fu ñu fanaan, ndax fii àllub neen la.»
13Mu ne leen: «Yeen, joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu ne ko: «Nun de amunu lu dul juróomi mburu ak ñaari jën. Xanaa nu dem, nun ci sunu bopp, jëndali mbooloo mii mépp lu ñu lekk!»
14Lu wara mat juróomi junniy góor a nga fa woon. Yeesu ne taalibe ya: «Dangeen leen di toogal, ñu def géewi juróom fukki nit.»
15Ñu def noonu, toogal ñépp.
16Ba mu ko defee Yeesu jël juróomi mburu ya ak ñaari jën ya, xool kaw asamaan, daldi yékkati kàddug cant, ba noppi dagg mburu ya, jox taalibe ya, ngir ñu taajal ko mbooloo ma.
17Ñépp lekk ba regg, ba ñu yóbbu dog ya ca des, muy fukki pañe ak ñaar.
18Yeesu moo beru woon, di julli, taalibe ya feggook moom. Ci kaw loolu mu laaj leen ne leen: «Ana ku nit ñi ne moom laa?»
19Ñu ne ko: «Ñii nee ñu yaa di Yaxya; ñee ne yaa di Ilyaas; ñale ne kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki, di yaw.»
20Yeesu ne leen: «Yeen nag, ngeen ne maay kan?» Piyeer ne ko: «Yaa di Almasib Yàlla.»
21Mu femmu leen nag, sant leen ñu bañ koo wax kenn.
22Mu neeti: «Fàww Doomu nit ki sonn lu bare, ba dajeek mbañeelu magi askan wi ak sarxalkat yu mag yi, ak firikati yoon yi, te dees na ko rey, ba ñetteelu fanam, mu dekki.»
23Yeesu nag wax leen ñoom ñépp, ne leen: «Képp ku bëgga dikk topp ma, fàtteel sa bopp, te nga gàddu bés bu nekk, bant bi ñu lay daaj, door maa topp.
24Ndax képp ku namma rawale sa bakkan, yaay ñàkk sa bakkan, waaye képp ku ñàkk sa bakkan ngir man, yaa musal sa bakkan.
25Ndax nit ki, su jagoo àddina sépp sax, te nara ñàkk bakkanam mbaa mu sànku, ana lu mu koy jariñ?
26Képp ku kersawoo sama jëmm, kersawoo topp samay wax, yaw itam Doomu nit ki dina la kersawoo, bés bu dikkee ci darajaam ak darajay Baay bi, ak darajay malaaka yu sell yi.
27Maa leen ko wax déy, ñenn a ngi fii taxaw tey, duñu dee te gisuñu nguurug Yàlla.»
28Ba lu wara tollook juróom ñetti fan wéyee gannaaw kàddu yooyu, Yeesu àndoon na ak Piyeer ak Yowaan ak Yanqóoba, ñu yéeg ca kaw tund wa ngir julli.
29Naka lay julli, xar kanamam soppiku, ay yéreem weex tàll, di melax.
30Ci kaw loolu ñaari nit jekki feeñ, di waxtaan ak moom; ñuy Yonent Yàlla Musaa ak Yonent Yàlla Ilyaas.
31Ñoo feeñ ci ag leer, di waxtaane dëddug Yeesu, ga mu doon waaja sottale fa Yerusalem.

Read Luug 9Luug 9
Compare Luug 9:3-31Luug 9:3-31