Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 7

LUUG 7:38-50

Help us?
Click on verse(s) to share them!
38Bi jigéen ja agsee, mu taxaw ca gannaaw tànki Yeesu, di jooy. Noonu ay rongooñam tooyal tànki Yeesu, jigéen ja di leen fomp ak kawaram, di leen fóon te ciy sotti latkoloñ ja.
39Naka la Farisen, bi woo woon Yeesu ci këram, gis loolu, mu wax ci xelam naan: «Bu nit kii doonoon yonent, kon dina xam kuy jigéen ji koy laal ak ni mu nekke bàkkaarkat.»
40Yeesu ne ca tonn, daldi ne Farisen ba: «Simoŋ, am na lu ma la wara wax.» Simoŋ ne ko: «Waxal, kilifa gi.»
41Yeesu ne ko: «Da fee amoon ñaari nit ñu ameel bor benn leblekat. Kenn kaa ngi ko ameel téeméeri junni ci xaalis, ki ci des fukki junni.
42Waaye kenn ci ñoom manu koo fey. Noonu mu baal leen bor ya. Ci ñaar ñooñu nag kan moo ko ciy gëna bëgg?»
43Simoŋ ne ko: «Xanaa ki ñu baal bor bi gëna bare.» Yeesu ne ko: «Àtte nga dëgg,»
44daldi walbatiku ca jigéen ja, ne Simoŋ: «Ndax gis nga jigéen jii? Dugg naa sa kër, te joxewuloo ndox, ngir raxas samay tànk. Waaye moom, raxas na samay tànk ak ay rongooñam, ba noppi fomp leen ak kawaram.
45Bi ma agsee, fóonuloo ma, waaye moom, bi ma duggee ba léegi tàyyiwul ci di fóon samay tànk.
46Defuloo diw ci sama bopp, waaye moom, sotti na latkoloñ ci samay tànk.
47Moo tax ma di la wax ne, su wonee mbëggeel gu réye nii, dafa fekk ñu baal ko bàkkaaram yu bare. Waaye ki mbëggeelam néew dafa fekk ñu baal ko lu tuuti.»
48Yeesu daldi ne jigéen ja: «Baal nañu la say bàkkaar.»
49Noonu ñi doon lekkandoo ak moom di wax ci seen xel naan: «Kii am sañ-sañu baale bàkkaar mooy kan?»
50Waaye Yeesu ne jigéen ja: «Sa ngëm musal na la. Demal ci jàmm.»

Read LUUG 7LUUG 7
Compare LUUG 7:38-50LUUG 7:38-50