Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 6

LUUG 6:27-44

Help us?
Click on verse(s) to share them!
27«Waaye maa ngi leen koy wax, yéen ñi may déglu, soppleen seeni bañaale tey defal lu baax ñi leen bañ.
28Yéeneleen lu baax ñi leen di móolu, te ñaanal ñi leen di sonal.
29Ku la talaata cib lex, jox ko ba ca des. Kuy nangu sa mbubb mu mag, bul téye sa turki.
30Képp ku la ñaan, may ko, te ku nangu say yëf, bu ko ko laaj.
31Defal-leen nit ñi li ngeen bëgg, ñu defal leen ko.
32«Su ngeen soppee ñi leen sopp, ban ngërëm ngeen ciy am? Ndaxte bàkkaarkat yi sax sopp nañu ñi leen sopp.
33Te bu ngeen defalee lu baax ñi leen koy defal, ban ngërëm ngeen ciy am? Bàkkaarkat yi it dañuy def noonu.
34Te bu ngeen dee leble te yaakaar ci ndelloo, ban ngërëm ngeen ciy am? Bàkkaarkat yi it dañuy lebal seeni moroom, ngir ñu delloo leen ko.
35Waaye soppleen seeni noon, di leen defal lu baax, tey leble, baña yaakaar ñu delloo leen ko. Noonu seen yool dina mag te dingeen wone ne yéenay doomi Aji Kawe ji, ndaxte Yàlla day wone mbaaxam ci ñu goreedi ñi ak ñu soxor ñi.
36Nangeen am yërmande, ni seen Baay ame yërmande.
37«Buleen àtte seeni moroom ak ñaaw njort, te deesu leen àtte. Buleen daan kenn, te deesu leen daan. Baal-leen ñi ci des, te dinañu leen baal.
38Mayeleen te dinañu leen may. Dinañu leen ëmbal natt bu baax bu ñu rokkos te yëngal ko, mu fees bay tuuru. Ndaxte dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale.»
39Noonu Yeesu wax na leen beneen léeb ne leen: «Ndax gumba man na wommat moroomam? Mbaa duñu daanu ñoom ñaar ci kàmb?
40Taalibe gënul kilifaam, waaye taalibe bu jàng ba wàcc, dina yem ak kilifaam demin.
41«Lu tax ngay xool ñax gi ci sa bëtu mbokk, te gisuloo gànj gi ci sa bët yaw?
42Nan nga mana waxe sa mbokk: “Sama xarit, may ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” yaw mi gisul gànj gi nekk ci sa bët? Naaféq! Jëkkala dindi gànj gi ci sa bët, te noonu dinga mana gis bu leer, ngir dindi ñax gi ci sa bëtu mbokk.
43«Garab gu baax du meññ doom yu bon, te garab gu bon du meññ doom yu baax.
44Ndaxte garab, meññeefam lañu koy xàmmee. Deesul witte figg ci dédd, walla reseñ ci xaaxaam.

Read LUUG 6LUUG 6
Compare LUUG 6:27-44LUUG 6:27-44