Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 4

LUUG 4:14-21

Help us?
Click on verse(s) to share them!
14Yeesu dellu diiwaanu Galile, fees ak dooley Xelum Yàlla, te turam siiw ca diiwaan booba bépp.
15Muy jàngle ca seeni jàngu, te ñépp di ko tagg.
16Yeesu dem Nasaret fa mu yaroo, te ca bésub noflaay ba, mu dugg ca jàngu ba, ni mu ko daan defe. Noonu mu taxaw ngir jàngal mbooloo mi.
17Ñu jox ko téereb yonent Yàlla Esayi. Bi mu ko ubbee, mu gis bérab, ba ñu bind aaya yii:
18«Xelum Boroom baa ngi ci man, ndaxte moo ma tànn, ngir ma yégal néew doole yi xibaaru jàmm bi. Dafa maa yónni, ngir ma yégal jaam ñi ne dinañu leen goreel, yégal gumba yi ne dinañu gis, te jot ñi ñu not,
19tey yégle atum yiw, mi jóge ci Boroom bi.»
20Bi mu jàngee aaya yooyu ba noppi, mu ub téere bi, delloo ko ki koy denc, toog. Ñépp ña nekkoon ca jàngu ba dékk koy bët.
21Noonu mu daldi ne: «Tey jii, loolu Mbind mi wax mat na, bi ngeen koy déglu.»

Read LUUG 4LUUG 4
Compare LUUG 4:14-21LUUG 4:14-21