13Bi mu waxee loolu, yeneen malaaka yu bare yu jóge asamaan, à nd ak moom, di sant Yà lla naan:
14«Nañu mà ggal Yà lla ca asamaan su kawe sa, te ci à ddina, na jà mm wà cc ci nit, ñi mu nangu ndax yiwam!»
15Bi malaaka ya delloo ca asamaan, sà mm yi di waxante naan: «Nanu dem boog Betleyem, seeti la fa xew, li nu Boroom bi xamal.»
16Ñu daldi gaawantu dem, gis Maryaama ak Yuusufa, ak liir, ba ñu tëral ca lekkukaayu jur ga.
17Bi ñu leen gisee, ñu nettali la ñu leen waxoon ca mbirum xale ba.
18Ñi dégg li sà mm yi doon wax ñépp daldi waaru lool.
19Waaye Maryaama moom, takkoon na mbir yooyu yépp, di ko xalaat ci xolam.
20Noonu sà mm ya dellu ca seen jur, di mà ggal Yà lla, di ko sant ci li ñu déggoon lépp te gis ko, ndaxte lépp am na, ni ko Boroom bi waxe woon.
21Bi bés ba délsee jamonoy xarafal xale ba agsi. Ñu tudde ko Yeesu, ni ko malaaka ma diglee woon, laata ko yaayam di ëmb.
22Noonu jamono ji ñu leen waroona sellale agsi, ni ko yoonu Musaa tërale. Waajuri Yeesu yi daldi koy yóbbu ca dëkku Yerusalem, ngir sédde ko Boroom bi.
23Ndaxte bind nañu ci yoonu Boroom bi ne: «Bépp taaw bu góor, nañu ko sédde Boroom bi.»
24Bi ñu ko yóbboo, def nañu itam sarax, ni ko yoonu Boroom bi santaanee: «ñaari pitaxu à ll walla ñaari xati yu ndaw.»
25Amoon na ca Yerusalem nit ku tudd Simeyon. Nit ku fonkoon yoonu Yà lla la te déggal ko, doon séentu jamono, ji Yà lla wara dëfal bà nni Israyil. Xel mu Sell mi mu ngi ci moom,
26te xamal na ko ne du dee mukk te gisul Almasib Boroom bi.
27Noonu Xelum Yà lla daldi yóbbu Simeyon ba ca kër Yà lla ga. Bi waajuri Yeesu indee xale ba, ngir sédde ko Yà lla, ni ko yoon wi santaanee,
28Simeyon jël xale bi, leewu ko, daldi sant Yà lla ne:
29«Boroom bi, nanga yiwi sa jaam, mu noppaluji ci jà mm, ni nga ko waxe.
30Ndaxte sama bët tegu na ci mucc gi nga lal,
31xeet yépp seede ko.
32Muy leer giy leeral xeet yi, di ndamu Israyil say gaa.»
33Waajuri Yeesu yi waaru ci li ñu doon wax ci xale bi.
34Noonu Simeyon ñaanal leen, ba noppi ne Maryaama: «Xale bii Yà llaa ko yónni, ngir ñu bare ci Israyil daanu te yékkatiku. Def na ko it muy firnde ju ñuy weddi,
35ba naqar dina xar sa xol ni jaasi. Noonu xalaati ñu bare feeñ.»
36Amoon na it ca Yerusalem yonent bu ñuy wax Aana. Doomu Fanuwel mi askanoo ci Aser la woon, te Aana mà ggatoon na lool. Bi mu séyee, dëkk na juróom ñaari at ak jëkkëram.
37Jëkkër ja gaañu, te séyaatul. Léegi amoon na juróom ñett fukki at ak ñeent. Mi ngi dëkke woona jaamu Yà lla guddi ak bëccëg ca kër Yà lla ga, di ñaan ak di woor.
38Aana yem ca waxi Simeyon ya, daldi gërëm Yà lla tey yégal mbiri liir ba ñépp ñi doon séentu jamono, ji Yà lla wara jot Yerusalem.
39Bi waajuri Yeesu yi matalee seen warugar ci lépp lu yoonu Boroom bi santaane woon, ñu dellu seen dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile.
40Xale baa nga doon mà gg, di dëgër, mu fees ak xel te yiwu Yà lla à nd ak moom.
41At mu jot nag waajuri Yeesu yi daan nañu dem Yerusalem, ngir mà ggali bésu Mucc ba.
42Noonu bi Yeesu amee fukki at ak ñaar, ñu dem mà ggal ga, ni ñu ko daan defe naka-jekk.
43Bi mà ggal ga tasee, ñu dëpp ñibbi, waaye xale ba Yeesu des Yerusalem, te ay waajuram yéguñu ko.