Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 24:3-19 in Wolof

Help us?

LUUG 24:3-19 in Téereb Injiil

3 Ñu dugg ca bàmmeel ba, waaye fekkuñu fa néewu Boroom bi Yeesu.
4 Noonu ba ñu nekkee ak seen njaaxle, am na ñaar ñu leen feeñu, sol yére yuy melax.
5 Jigéen ña am tiitaange ju mag, daldi dëpp seen jë ci suuf. Waaye ñu ne leen: «Lu tax ngeen di seet kiy dund ci biir néew yi?
6 Nekkatu fi; dekki na. Fàttalikuleen la mu leen waxoon, ba mu nekkee Galile.
7 Nee woon na: “Fàww ñu jébbal Doomu nit ki bàkkaarkat yi, ñu rey ko ci bant, mu dekki ca ñetteelu fan ba.”»
8 Noonu ñu daldi fàttaliku kàdduy Yeesu ya.
9 Bi ñu jógee bàmmeel ba, ñu dem nettaliji loolu lépp fukki ndaw ya ak benn, ak ña ca des ñépp.
10 Jigéen ña ñoo doon Maryaamam Magdala, Sànn, ak Maryaama yaayu Saag. Yeneen jigéen yi leen gunge woon itam nettali loolu ndaw ya.
11 Waaye ñu teg wax jooju ay jeneer, ba gëmuñu jigéen ñooñu.
12 Waaye Piyeer daldi jóg, daw, dem ca bàmmeel ba. Bi mu àggee, mu sëgg, yër, gisul lu dul càngaay la. Noonu mu dëpp ñibbi, jaaxle lool ci li xew.
13 Ca bés boobu ñaar ci taalibe yi di dem ci dëkku Emayus, te mu sore Yerusalem ci lu mat fukki kilomet.
14 Ñu waxtaane li xewoon lépp.
15 Bi ñuy waxtaan ak a sotteente xalaat, Yeesu ci boppam dab leen, ànd ak ñoom,
16 fekk seeni bët muuru, ba manu ko woona xàmmi.
17 Yeesu ne leen: «Lan ngeen di waxtaane nii ci yoon wi?» Noonu ñu taxaw, seen xol jeex.
18 Kenn ci ñoom, ki tudd Këleyopas ne ko: «Xanaa yaw rekk yaa ñëw Yerusalem te umple li fi xewoon bés yii?»
19 Yeesu ne leen: «Lu fi xew?» Ñu ne ko: «Mbirum Yeesum Nasaret. Ab yonent la woon bu doon def ay jëf yu mag, di wax ay kàddu yu am doole, ci kanam nit ñi ak ca kanam Yàlla.
LUUG 24 in Téereb Injiil

Luug 24:3-19 in Kàddug Yàlla gi

3 Ñu dugg, fekkuñu fa néewu Sang Yeesu.
4 Naka lañu nekke seenug njaaxle ci loolu, ñaari góor ne jimeet fa seen wet, sol yére yuy melax.
5 Naka la leen tiitaange jàpp, ba ñu sukk, dëpp seen jë fa suuf, ñu ne leen: «Kiy dund, lu tax ngeen di ko seet ci biir ñi dee?
6 Nekku fi; dekki na. Fàttlikuleen la mu leen waxoon, ba mu génnagulee Galile.
7 Da noon: “Fàww ñu teg Doomu nit ki ci loxoy bàkkaarkat yi, ñu daaj ko ci bant, rey ko, ba ñetteelu fanam, mu dekki.”»
8 Booba lañu fàttliku kàddug Yeesu googu.
9 Ñu jóge ca bàmmeel ba, dem àgge loolu lépp Fukk ñaak benn, ak ña ca des ñépp.
10 Jigéen ña àgge loolu ndaw ya ñoo doon Maryaamam Magdala, ak Yowaana, ak Maryaama yaayu Yanqóoba, ak itam ñeneen jigéen ñu àndoon ak ñoom.
11 Teewul ñu def waxi jigéen ña ay caaxaan, ba gëmuñu leen.
12 Piyeer nag jóg, daw, ba ca bàmmeel ba. Mu sëgg, yër, gisul lu dul càngaay la. Mu daldi ñibbi, jaaxle lool ca mbir ma.
13 Ndeke ca bés booba ñaar ca taalibe yaa nga woon ca yoonu dëkk bu ñuy wax Emayus, digganteem ak Yerusalem wara tollu ci fukki kilomeetar.
14 Ña ngay waxtaane mboolem xew-xew yooyu.
15 Naka lañuy waxtaan ak a diisoo, Yeesu ci boppam dab leen, ànd ak ñoom.
16 Teewul seeni gët tëlee ràññee, ba manuñu koo xàmmi.
17 Yeesu ne leen: «Lu ngeen di waxtaane nii ci yoon wi?» Ñu daldi taxaw, seen kanam lëndëm ndaxu tiis.
18 Kenn ci ñoom, ku ñuy wax Kelyopas ne ko: «Xanaa yaw rekk de, yaa dal Yerusalem te umple li fi xew fan yii?»
19 Yeesu ne leen: «Lu fi xew?» Ñu ne ko: «Mbirum Yeesum Nasaret. Mu doonoon ab yonent bu manoorewu ci jëf ak ci kàddu, Yàlla ak askan wépp seede.
Luug 24 in Kàddug Yàlla gi