27 Mu tàmbalee nag ci Yonent Yàlla Musaa, jaare ci yonent yépp, tekkil leen mboolem lu Mbind mi indi ci mbiram.
28 Naka lañuy jub dëkk, ba ñu jëm, mu mel ni ku nara jubal yoonam.
29 Ñu daldi koy téye, ne ko: «Dalal ak nun, ndax jant baa ngi so, léegi mu guddi.» Ba loolu amee mu dugg, dal ak ñoom.
30 Ba reer jotee mu toog ak ñoom ca ndab la, jël mburu ma, yékkati kàddug cant, daldi dagg, jox leen.
31 Ca la seeni gët ubbiku, ñu xàmmi ko. Moom nag, mu ne mes, réer leen.
32 Ba loolu amee, ku nekk naan sa moroom: «Ndax yéguloo woon cawartey xol bu tooy, ba muy wax ak nun ci yoon wi, di nu firil Mbind mi?»
33 Ñaari taalibe ya daldi jóg ca waxtu woowu tembe, dellu Yerusalem, ca Fukk ñaak benn. Ñu fekk leen ñu dajeek seeni àndandoo.
34 Ci kaw loolu ñu ne ñaar ña jóge Emayus: «Ndeke Sang bi kay, dekki na; feeñu na Simoŋ!»
35 Ñaari taalibe ya ñoom it, nettali leen la xewoon ca yoon wa ak na ñu xàmmee Yeesu, ba mu daggee mburu ma.
36 Ba ñaari taalibe ya di nettali loolu, ca la Yeesu ci boppam ne jimeet taxaw ci seen biir, ne leen: «Jàmm seen!»
37 Tiitaange lu réy jàpp leen, ñu foog ne njuuma lañu gis.
38 Yeesu nag ne leen: «Lu ngeen di jaaxle, ak lu ngeen di xel-yaar nii?
39 Xool-leen samay loxo ak samay tànk. Man la. Làmbleen ma, ba xam! Njuuma amul suux, amuli yax, nii ma ko ame, ngeen gis.»
40 Loolu la leen wax, daldi leen won ay loxoom aki tànkam.
41 Taalibe ya nag boole mbég akug jaaxle ba tax manuñu koo gëm. Mu ne leen: «Lu ngeen fi am, lu ñuy lekk?»