21 Nun nag danoo yaakaaroon ne mooy jotsi Israyil. Loolu lépp teewul nu ngii ci ñetteelu fan, ba mbir yooyu amee ba tey.
22 Ay jigéen ñu bokk ci nun nag ñoo nu jaaxal. Ndax ñoo jëlu dem ca bàmmeel ba,
23 waaye fekkuñu fa néewam. Ñu dikk, ne ay malaakaa leen feeñu, xamal leen ne Yeesoo ngi dund.
24 Ñenn ci sunuy àndandoo it dem nañu ca bàmmeel ba, fekk ko noonee ko jigéen ña waxe. Waaye moom, gisuñu ko.»
25 Ci kaw loolu mu ne leen: «Yeen daal, yeena ñàkk xel, yeena naqarim xel, ndegam ba tey gëmaguleen mboolem li yonent yi xamle woon!