Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 24:15-34 in Wolof

Help us?

LUUG 24:15-34 in Téereb Injiil

15 Bi ñuy waxtaan ak a sotteente xalaat, Yeesu ci boppam dab leen, ànd ak ñoom,
16 fekk seeni bët muuru, ba manu ko woona xàmmi.
17 Yeesu ne leen: «Lan ngeen di waxtaane nii ci yoon wi?» Noonu ñu taxaw, seen xol jeex.
18 Kenn ci ñoom, ki tudd Këleyopas ne ko: «Xanaa yaw rekk yaa ñëw Yerusalem te umple li fi xewoon bés yii?»
19 Yeesu ne leen: «Lu fi xew?» Ñu ne ko: «Mbirum Yeesum Nasaret. Ab yonent la woon bu doon def ay jëf yu mag, di wax ay kàddu yu am doole, ci kanam nit ñi ak ca kanam Yàlla.
20 Waaye sunuy sarxalkat yu mag ak sunuy njiit ñoo ko jébbal nguur gi ngir ñu àtte ko, teg ko dee, ba daaj ko ci bant.
21 Nun nag danoo yaakaaroon ne mooy kiy nara jot Israyil. Waaye bi loolu xewee ak léegi, tey la ñetteelu fan bi.
22 Teewul nag am na ay jigéen yu bokk ci nun yu nu jaaxal. Dañoo fajaru ca bàmmeel ba,
23 waaye fekkuñu fa néewam. Ñu délsi, nettali nu ne, ay malaaka feeñu nañu leen, yégal leen ne mi ngi dund.
24 Ñenn ci sunu àndandoo yi dem nañu ca bàmmeel ba, fekk lépp mel, na ko jigéen ña waxe woon. Waaye moom gisuñu ko.»
25 Noonu Yeesu ne leen: «Yéen daal, yéena ñàkk xel, te seen xol yéexa gëm li yonent yi yégle woon!
26 Xanaa du Almasi bi dafa waroona daj boobu coono te dugg ci ndamam?»
27 Noonu mu tàmbalee ci yonent Yàlla Musaa ba ci yonent yépp, tekkil leen li Mbind mi wax lépp ci ay mbiram.
28 Bi ñuy jub dëkk, ba ñu jëmoon nag, Yeesu def ni kuy jubal yoonam.
29 Waaye ñu téye ko ne ko: «Toogal fii ci nun, ndaxte jant baa ngi so, te léegi mu guddi.» Noonu mu dugg, toog ca ñoom.
30 Bi ñu tàmbali di reer, Yeesu jël mburu ma, gërëm Yàlla, ba noppi damm ko, jox leen ko.
31 Bi mu defee loolu, lépp leer ci seeni bët, ñu daldi ko xàmmi. Waaye Yeesu ne mes, gisatuñu ko.
32 Noonu ku nekk naan sa moroom: «Ndax sa xol seddul woon, bi muy wax ak nun ci yoon wi, te muy tekki Mbind mi?»
33 Ñu daldi jóg ca saa sa, dellu Yerusalem, fekk fa fukki ndaw ya ak benn, ak yeneen taalibe.
34 Ñooñu ne leen: «Dëgg la, Boroom bi dekki na, te feeñu na Simoŋ!»
LUUG 24 in Téereb Injiil

Luug 24:15-34 in Kàddug Yàlla gi

15 Naka lañuy waxtaan ak a diisoo, Yeesu ci boppam dab leen, ànd ak ñoom.
16 Teewul seeni gët tëlee ràññee, ba manuñu koo xàmmi.
17 Yeesu ne leen: «Lu ngeen di waxtaane nii ci yoon wi?» Ñu daldi taxaw, seen kanam lëndëm ndaxu tiis.
18 Kenn ci ñoom, ku ñuy wax Kelyopas ne ko: «Xanaa yaw rekk de, yaa dal Yerusalem te umple li fi xew fan yii?»
19 Yeesu ne leen: «Lu fi xew?» Ñu ne ko: «Mbirum Yeesum Nasaret. Mu doonoon ab yonent bu manoorewu ci jëf ak ci kàddu, Yàlla ak askan wépp seede.
20 Waaye sunu sarxalkat yu mag ak sunuy njiit ñoo ko teg ciy loxo, ngir ñu teg ko àtteb dee, daaj ko ci bant.
21 Nun nag danoo yaakaaroon ne mooy jotsi Israyil. Loolu lépp teewul nu ngii ci ñetteelu fan, ba mbir yooyu amee ba tey.
22 Ay jigéen ñu bokk ci nun nag ñoo nu jaaxal. Ndax ñoo jëlu dem ca bàmmeel ba,
23 waaye fekkuñu fa néewam. Ñu dikk, ne ay malaakaa leen feeñu, xamal leen ne Yeesoo ngi dund.
24 Ñenn ci sunuy àndandoo it dem nañu ca bàmmeel ba, fekk ko noonee ko jigéen ña waxe. Waaye moom, gisuñu ko.»
25 Ci kaw loolu mu ne leen: «Yeen daal, yeena ñàkk xel, yeena naqarim xel, ndegam ba tey gëmaguleen mboolem li yonent yi xamle woon!
26 Xanaa du fàww Almasi daj boobu coono, doora dugg ci teraangaam?»
27 Mu tàmbalee nag ci Yonent Yàlla Musaa, jaare ci yonent yépp, tekkil leen mboolem lu Mbind mi indi ci mbiram.
28 Naka lañuy jub dëkk, ba ñu jëm, mu mel ni ku nara jubal yoonam.
29 Ñu daldi koy téye, ne ko: «Dalal ak nun, ndax jant baa ngi so, léegi mu guddi.» Ba loolu amee mu dugg, dal ak ñoom.
30 Ba reer jotee mu toog ak ñoom ca ndab la, jël mburu ma, yékkati kàddug cant, daldi dagg, jox leen.
31 Ca la seeni gët ubbiku, ñu xàmmi ko. Moom nag, mu ne mes, réer leen.
32 Ba loolu amee, ku nekk naan sa moroom: «Ndax yéguloo woon cawartey xol bu tooy, ba muy wax ak nun ci yoon wi, di nu firil Mbind mi?»
33 Ñaari taalibe ya daldi jóg ca waxtu woowu tembe, dellu Yerusalem, ca Fukk ñaak benn. Ñu fekk leen ñu dajeek seeni àndandoo.
34 Ci kaw loolu ñu ne ñaar ña jóge Emayus: «Ndeke Sang bi kay, dekki na; feeñu na Simoŋ!»
Luug 24 in Kàddug Yàlla gi