Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 23:47-53 in Wolof

Help us?

LUUG 23:47-53 in Téereb Injiil

47 Bi njiitu xare ba gisee li xewoon, mu màggal Yàlla ne: «Dëgg-dëgg nit kii ku jub la woon.»
48 Nit ña fa dajaloo woon ñépp, di seetaan li xew, ba ñu gisee loolu, ñu dellu seen kër, fëgg seen dënn, di jooy.
49 Xamey Yeesu yépp ak jigéen, ña ko toppe woon Galile, dànd leen, di xool li xew.
50 Nit ku ñuy wax Yuusufa dem ca Pilaat. Mi ngi dëkk Arimate ca diiwaanu Yude. Yuusufaa nga bokkoon ca kureelu àttekat yi. Nit ku baax la woon te jub, te àndul woon ci li ñu dogaloon te jëf ko. Da doon séentu nguuru Yàlla.
52 Mu dem ca Pilaat, laaj ko néewu Yeesu.
53 Gannaaw loolu mu wàcce ko ca bant ba, laxas ko ci càngaay, dugal ko cib bàmmeel bu ñu yett ciw doj te masuñu caa def kenn.
LUUG 23 in Téereb Injiil

Luug 23:47-53 in Kàddug Yàlla gi

47 Njiitu takk-der ba ko teewe woon nag sàbbaal Yàlla, ne: «Aylayéwén, waa jii ku jub la.»
48 Ba loolu amee mboolem ña fa daje woon di seetaan te teewe loolu, ñépp dellu seeni kër, tey fëgg seen dënn ndaxu tiis.
49 Mboolem xamey Yeesu, ak jigéen ña ko toppe woon ca Galile, ña nga dànd lu sore, di seetaan.
50 Ndeke jenn waay ju ñuy wax Yuusufa, ma nga bokkoon ca kurélu àttekati Yawut ya. Ku baax, ku jub la woon.
51 Kooku ànduloon ca àtteb kurél ga ak seen jëf jooju. Ma nga cosaanoo woon dëkkub Yawut ba ñuy wax Arimate, te moom itam, nguurug Yàlla la doon séentu.
52 Moom moo dem ca Pilaat, sàkku ci moom, mu jox ko néewub Yeesu.
53 Gannaaw loolu mu wàccee ko ca bant ba, sànge ko càngaayal lẽe, denc ko ci bàmmeel bu ñu yett ciw doj, te maseesu caa denc ab néew.
Luug 23 in Kàddug Yàlla gi