Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 23:33-49 in Wolof

Help us?

LUUG 23:33-49 in Téereb Injiil

33 Bi xarekat ya agsee ba ca bérab, ba ñuy wooye Kaaŋu bopp, ñu daaj fa Yeesu ca bant, daajaale ñaari defkati lu bon ya, kenn ca ndijooram, ka ca des ca càmmoñam.
34 Ci kaw loolu Yeesu ne: «Baay, baal leen, ndaxte xamuñu li ñuy def.» Xarekat ya tegoo ay bant yéreem, ngir séddoo ko.
35 Mbooloo maa nga fa taxaw di seetaan. Njiit ya di ko reetaan naan: «Musal na ñeneen; na musal boppam, su fekkee mooy Almasi bi, ki Yàlla fal!»
36 Xarekat ya it di ko ñaawal. Ñu jegesi, jox ko bineegar te naan:
37 «Su fekkee ne yaay buuru Yawut yi, musalal sa bopp!»
38 Ñu daaj mbind, mu tiim ko naan: «Kii mooy buuru Yawut yi.»
39 Kenn ca defkatu lu bon ya ñu wékkoon ci bant, di ko xas, naan ko: «Xanaa du yaw yaay Almasi bi? Musalal sa bopp te musal nu!»
40 Waaye ka ca des yedd moroom ma, naan ko: «Xanaa ragaloo Yàlla, yaw mi ñuy mbugal ni moom?
41 Nun yelloo nanu sunu mbugal, waaye moom deful dara.»
42 Noonu mu ne: «Yeesu, fàttaliku ma, boo délsee ci sa nguur.»
43 Yeesu ne ko: «Ci dëgg maa ngi la koy wax, tey jii dinga texe ak man ca jataayu Yàlla.»
44 Noonu digg bëccëg daldi jot, jant ba nëbbu, réew mépp daldi lëndëm këruus lu mat ñetti waxtu. Ridob bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga daldi xar ñaar.
46 Yeesu woote ak kàddu gu dëgër naan: «Baay, jébbal naa la sama ruu!» Bi mu waxee loolu, mu delloo ruuwam Yàlla.
47 Bi njiitu xare ba gisee li xewoon, mu màggal Yàlla ne: «Dëgg-dëgg nit kii ku jub la woon.»
48 Nit ña fa dajaloo woon ñépp, di seetaan li xew, ba ñu gisee loolu, ñu dellu seen kër, fëgg seen dënn, di jooy.
49 Xamey Yeesu yépp ak jigéen, ña ko toppe woon Galile, dànd leen, di xool li xew.
LUUG 23 in Téereb Injiil

Luug 23:33-49 in Kàddug Yàlla gi

33 Ba ñu agsee ca bérab, ba ñuy wax Kaaŋu bopp, fa lañu daaj Yeesu ci bant, daajaale ñaari saaysaay ya, kenn ca ndijooram, ka ca des ca càmmoñam.
34 Ci kaw loolu Yeesu ne: «Baay, baal leen, ndax li ñuy def, xamuñu ko.» Ñu daldi tegoo bant ay yéreem, ngir séddoo ko.
35 Mbooloo maa nga taxaw di seetaan, njiit ya ñoom di ko kókkali, naan: «Musal na ay nit; na musal boppam nag, ndegam mooy Almasib Yàlla, ki ñu fal!»
36 Takk-der ya it di ko ñaawal. Ñu dikk, tàllal ko bineegar, ngir mu naan.
37 Ñu ne ko: «Gannaaw yaa di buurub Yawut yi, musalal sa bopp!»
38 Ñu bindal ko nag fa ko tiim, mbind mii: «Kii mooy buurub Yawut yi.»
39 Kenn ca saaysaay ya ñu wékkoon ci bant, di ko xas, naan ko: «Xanaa du yaw yaay Almasi? Wallul sa bopp te wallu nu!»
40 Moroom ma nag femmu ko, ne ko: «Ragaloo sax Yàlla, te yaa ngi ci menn mbugal mii?
41 Nun sax, lii jaadu na ci nun, ndax sunu yoolu jëf lanu jot. Waaye kii deful dara lu teggi yoon!»
42 Mu teg ca ne: «Yeesu, boo délsee ci sa nguur, fàttliku ma!»
43 Yeesu ne ko: «Yaw laa ne déy, bésub tey jii, man ngay nekkal fa Àjjana.»
44 Ba ñu demee ba tollu wetu fukki waxtu ak ñaar ca bëccëg, ag lëndëm a wàcc ca réew ma mépp, ba fukki waxtu ak juróom ca ngoon.
45 Naka la jant bi giim, ridob biir néeg Yàlla ba xar ca digg ba.
46 Ci kaw loolu Yeesu àddu ca kaw, ne: «Baay, jébbal naa la samag noo!» Ba mu waxee loolu la dee.
47 Njiitu takk-der ba ko teewe woon nag sàbbaal Yàlla, ne: «Aylayéwén, waa jii ku jub la.»
48 Ba loolu amee mboolem ña fa daje woon di seetaan te teewe loolu, ñépp dellu seeni kër, tey fëgg seen dënn ndaxu tiis.
49 Mboolem xamey Yeesu, ak jigéen ña ko toppe woon ca Galile, ña nga dànd lu sore, di seetaan.
Luug 23 in Kàddug Yàlla gi