Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 23:3-24 in Wolof

Help us?

LUUG 23:3-24 in Téereb Injiil

3 Noonu Pilaat laaj ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?» Yeesu ne ko: «Wax nga ko.»
4 Pilaat ne sarxalkat yu mag ya ak mbooloo ma: «Gisuma genn tooñ ci nit kii.»
5 Waaye ñu sax ci seeni wax naan: «Mi ngi jógloo mbooloo mi, di jàngle ci réewu Yawut ya mépp, li dale ci Galile ba fii.»
6 Bi Pilaat yégee baat yooyu, mu laajte ne: «Ndax nit kii Galile la dëkk?»
7 Bi mu yégee ne Yeesoo ngi nekk ci diiwaan bi Erodd yilif, mu yónnee ko Erodd, mi nekkoon ci jamono jooju ci Yerusalem.
8 Bi Erodd gisee Yeesu, mu am mbég mu réy. Bu yàgg ba tey dafa koo bëggoona gis, ndaxte déggoon na ñuy wax ci ay mbiram te yaakaaroon na ne dina ko gis mu def kéemaan.
9 Noonu mu laaj ko ay laaj yu bare, waaye Yeesu waxul dara.
10 Sarxalkat yu mag ya ak xutbakat yaa nga fa woon, di ko jiiñ bu metti.
11 Noonu Erodd ak ay xarekatam toroxal Yeesu, di ko ñaawal. Gannaaw loolu mu solal ko mbubb mu rafet, delloo ko Pilaat.
12 Erodd ak Pilaat dañoo ñi bañante woon bu jëkk, waaye ca bés booba doon nañu ay xarit.
13 Pilaat daldi woo sarxalkat yu mag ya, njiit ya ak mbooloom Yawut ya ne leen:
14 «Indil ngeen ma nit kii, ne ma day jàddloo yoon mbooloo mi. Léegi nag man mii laaj naa ko ci seen kanam, waaye gisuma tooñ ci moom ak li ngeen koy jiiñ lépp.
15 Erodd itam gisul tooñ gu mu def, ndegam mu yónneewaat nu ko. Nit kii deful genn tooñ gu jar ñu koy rey.
16 Kon nag dinaa ko dóorlu ay yar te bàyyi ko.»
18 Waaye ñu bokk di yuuxu, ñoom ñépp naan: «Reyal kii te bàyyi Barabas!»
19 Dañoo tëjoon Barabas, ndaxte dafa jéema tas dëkk ba, te rey nit.
20 Pilaat waxaat ak mbooloo ma, ndaxte dafa bëggoona bàyyi Yeesu.
21 Waaye ñuy yuuxu naan: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant, ba mu dee!»
22 Pilaat ne leen ñetteel bi yoon: «Lu tax? Gan tooñ la def? Gisuma ci moom dara lu jar dee. Kon dinaa ko dóorlu ay yar te bàyyi ko.»
23 Waaye ñoom ñu sax ca la ñu waxoon, di gëna yuuxu naan, ñu daaj ko ci bant. Coow la yey Pilaat.
24 Muj gi Pilaat dogal, ñu defal leen li ñu bëgg.
LUUG 23 in Téereb Injiil

Luug 23:3-24 in Kàddug Yàlla gi

3 Pilaat laaj ko ne ko: «Yaa di buurub Yawut yi?» Mu ne ko: «Yaa ko wax.»
4 Pilaat ne sarxalkat yu mag ya ak mbooloo ma: «Waa jii, gisuma ci moom genn tooñ.»
5 Teewul ñu gëna dëggal seeni wax, ne: «Mooy yékkati askan wi, ndax li muy jàngle ci mboolem réewum Yawut, dale ko ca Galile ba fii.»
6 Pilaat dégg loolu, daldi ne: «Waa jii waa Galile la?»
7 Ba mu wóoree Pilaat ne ca diiwaan, ba ca kilifteefu Erodd la Yeesu bokk, ca la ko yónnee Erodd, yemook Erodd itam nekk Yerusalem ca fan yooya.
8 Ba Erodd gisee Yeesu, bég na lool, ndax yàggoon na koo bëgga gis, ngir la mu déggoon ay mbiram, ba tax mu yaakaara teewe ay kéemaanam.
9 Mu laaj ko lu bare, Yeesu tontuwu ko.
10 Sarxalkat yu mag ya ak firikati yoon yaa nga taxaw, di ko tuumaal ak doole.
11 Erodd aki dagam nag sewal Yeesu, di ko ñaawal. Gannaaw loolu mu solal ko mbubb mu yànj, delloo ko Pilaat.
12 Erodd ak Pilaat, bésub keroog ay xarit lañu, doonte ay noon lañu woon.
13 Ci kaw loolu Pilaat woo sarxalkat yu mag ya, ak njiit ya ak askan wa.
14 Mu ne leen: «Yeena ma indil waa jii, ne ma mooy lajjal askan wi. Man nag laaj naa ko ci seen kanam, waaye gisuma ci moom genn tooñ ci li ngeen ko tuumaal.
15 Erodd itam gisul lenn ci moom, ndax moo nu ko yónneewaat. Mu ngoog, waa jii deful lenn lu jar àtteb dee.
16 Kon nag dama koy dóorlu, yiwi ko.»
17 Booba fàww Erodd bàyyil leen kenn ca bésu màggal ga.
18 Ñépp daldi xaacoondoo, ne: «Reyal kii te yiwil nu Barabas!»
19 Barabas nag fippu gu amoon ca dëkk ba, ak nit ku ñu fa bóom, moo waral ñu tëj ko kaso.
20 Pilaat namma bàyyi Yeesu, daldi waxaat ak mbooloo ma.
21 Teewul ñuy xaacu, naan: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant!»
22 Pilaat ne leen ñetteel bi yoon: «Ana lu bon lu kii def? Lenn lu jar dee, gisuma ko ci moom. Kon nag, dama koy dóorlu, yiwi ko.»
23 Ñu gënatee xaacu, di sàkku ñu daaj ko ci bant. Seen coow la mujj ko ëpp doole.
24 Ci kaw loolu Pilaat dogal ñu defal leen la ñu sàkku.
Luug 23 in Kàddug Yàlla gi