27 Nit ñu bare nag topp ko, jigéen ñay yuuxu, di ko jooy.
28 Yeesu geesu leen, ne: «Yeen jigéeni Yerusalem, buleen ma jooy! Jooyleen seen bopp ak seeni doom.
29 Ay jant a ngi ñëw kat, dees na ca ne: “Ndokklee jigéen ju tëlee am doom, masula jur, masula nàmpal!”
30 Su boobaa, “Nit ñee naan tund yu mag yi: ‘Daanuleen ci sunu kaw!’, naan tund yu ndaw yi: ‘Suul-leen nu!’ ”
31 Ndegam bant bu tooy lees di def nii, ana nu bant bu wow di mujje?»
32 Yóbbaale nañu itam ñaari saaysaay, ngir boole leen ak Yeesu, rey leen.
33 Ba ñu agsee ca bérab, ba ñuy wax Kaaŋu bopp, fa lañu daaj Yeesu ci bant, daajaale ñaari saaysaay ya, kenn ca ndijooram, ka ca des ca càmmoñam.
34 Ci kaw loolu Yeesu ne: «Baay, baal leen, ndax li ñuy def, xamuñu ko.» Ñu daldi tegoo bant ay yéreem, ngir séddoo ko.
35 Mbooloo maa nga taxaw di seetaan, njiit ya ñoom di ko kókkali, naan: «Musal na ay nit; na musal boppam nag, ndegam mooy Almasib Yàlla, ki ñu fal!»
36 Takk-der ya it di ko ñaawal. Ñu dikk, tàllal ko bineegar, ngir mu naan.
37 Ñu ne ko: «Gannaaw yaa di buurub Yawut yi, musalal sa bopp!»
38 Ñu bindal ko nag fa ko tiim, mbind mii: «Kii mooy buurub Yawut yi.»
39 Kenn ca saaysaay ya ñu wékkoon ci bant, di ko xas, naan ko: «Xanaa du yaw yaay Almasi? Wallul sa bopp te wallu nu!»
40 Moroom ma nag femmu ko, ne ko: «Ragaloo sax Yàlla, te yaa ngi ci menn mbugal mii?
41 Nun sax, lii jaadu na ci nun, ndax sunu yoolu jëf lanu jot. Waaye kii deful dara lu teggi yoon!»
42 Mu teg ca ne: «Yeesu, boo délsee ci sa nguur, fàttliku ma!»
43 Yeesu ne ko: «Yaw laa ne déy, bésub tey jii, man ngay nekkal fa Àjjana.»