18 Ñépp daldi xaacoondoo, ne: «Reyal kii te yiwil nu Barabas!»
19 Barabas nag fippu gu amoon ca dëkk ba, ak nit ku ñu fa bóom, moo waral ñu tëj ko kaso.
20 Pilaat namma bàyyi Yeesu, daldi waxaat ak mbooloo ma.
21 Teewul ñuy xaacu, naan: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant!»
22 Pilaat ne leen ñetteel bi yoon: «Ana lu bon lu kii def? Lenn lu jar dee, gisuma ko ci moom. Kon nag, dama koy dóorlu, yiwi ko.»
23 Ñu gënatee xaacu, di sàkku ñu daaj ko ci bant. Seen coow la mujj ko ëpp doole.
24 Ci kaw loolu Pilaat dogal ñu defal leen la ñu sàkku.
25 Mu yiwi ka ñu ko ñaanoon, te jëfi fippu ak nit ku ñu bóom taxoon ñu tëj ko kaso. Yeesu nag, mu teg ko ci seeni loxo, ngir ñu def ko lu leen neex.
26 Ba ñuy yóbbu Yeesu, jenn waay ju dëkk Siren, ñu di ko wax Simoŋ, moom lañu dajeel, mu jóge ca tool ya. Ñu teg bant ba ñuy daaj Yeesu, ngir mu gàddu ko, topp ca moom.
27 Nit ñu bare nag topp ko, jigéen ñay yuuxu, di ko jooy.
28 Yeesu geesu leen, ne: «Yeen jigéeni Yerusalem, buleen ma jooy! Jooyleen seen bopp ak seeni doom.
29 Ay jant a ngi ñëw kat, dees na ca ne: “Ndokklee jigéen ju tëlee am doom, masula jur, masula nàmpal!”
30 Su boobaa, “Nit ñee naan tund yu mag yi: ‘Daanuleen ci sunu kaw!’, naan tund yu ndaw yi: ‘Suul-leen nu!’ ”
31 Ndegam bant bu tooy lees di def nii, ana nu bant bu wow di mujje?»
32 Yóbbaale nañu itam ñaari saaysaay, ngir boole leen ak Yeesu, rey leen.
33 Ba ñu agsee ca bérab, ba ñuy wax Kaaŋu bopp, fa lañu daaj Yeesu ci bant, daajaale ñaari saaysaay ya, kenn ca ndijooram, ka ca des ca càmmoñam.