Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 21:11-35 in Wolof

Help us?

LUUG 21:11-35 in Téereb Injiil

11 Suuf dina yëngu yëngu yu réy, te wopp ak xiif dina am ci bérab yu bare. Dina am it ay xew-xew yu raglu ak ay firnde yu mag yuy jóge asamaan.
12 Waaye bala looloo xew, dees na leen jàpp, fitnaal leen, di leen jébbal àttekat yi ca jàngu ya, tëj leen kaso. Dees na leen yóbbu ci kanam i buur ak i boroom réew ndax sama tur.
13 Loolu dina leen ubbil bunt, ba ngeen man maa seedeel.
14 Fasleen yéenee baña wut lay ngir musal seen bopp.
15 Ndaxte man ci sama bopp maa leen di jox kàddu ak xel moo xam ne seeni noon duñu ko mana teggi, mbaa ñu di ko weddi.
16 Seeni waajur sax ak seeni doomi ndey, seeni bokk ak seeni xarit, dinañu leen jébbal àttekat yi, ba ñu rey ñenn ci yéen.
17 Te ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur.
18 Waaye seen genn kawar sax du neen.
19 Seen muñ moo leen di musal.
20 «Bu ngeen gisee ay xarekat wër dëkku Yerusalem, xamleen ne jamono, ji ñu koy yàq, agsi na.
21 Kon nag ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya; ku nekk ci biir dëkk bi, nanga ko génn; te ku nekk ca tool ya, bul dugg ca dëkk ba!
22 Ndaxte ci bés yooyu Yàlla dina fey jëf yi, te li ñu bindoon ci téereb Yàlla dina mat.
23 Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooya, ngalla it ñiy nàmpal! Ndaxte tiis wu metti dina am ci réew mi, te Yàlla dina wàcce meram ci waa réew mii.
24 Dees na leen reye ak i jaasi, jàpp leen jaam, yóbbu leen ci réewi àddina sépp. Te ñi dul Yawut dinañu nappaaje Yerusalem, ba kera jamonoy ñi dul Yawut mat.
25 «Ay firnde dinañu feeñ ci jant bi, ci weer wi ak ci biddiiw yi. Ci kaw suuf xeet yi dinañu tiit, jaaxle ndax riiru géej gi ak yëngu-yëngub duus yi.
26 Bu boobaa nit ñiy xëm ndax tiitaange, bu ñuy xalaat musiba, yi nara wàcc ci àddina, ndaxte dees na yëngal kàttani asamaan.
27 Noonu dinañu gis Doomu nit ki di ñëw ciw niir, ànd ak kàttan ak ndam lu réy.
28 Bu mbir yooyu di tàmbalee xew nag, boo yaboo ngeen siggi, téen, ndaxte seen njot jubsi na.»
29 Noonu Yeesu misaal leen lii: «Xool-leen garabu figg ak yeneen garab yi.
30 Bu ñu gisee ñu sëq, soxlawuleen kenn wax leen ne, nawet bi jubsi na xaat.
31 Noonu itam bu ngeen gisee loolu lépp xew, xamleen ne nguuru Yàlla jege na.
32 «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii duñu wéy, te loolu lépp amul.
33 Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk.
34 «Moytuleen seen nafsu diigal leen ci yàqute ak ci màndite ak ittey àddina, ba bés boobu bett leen ni mbaal.
35 Ndaxte dina dal ci ñépp ñi nekk ci kaw suuf.
LUUG 21 in Téereb Injiil

Luug 21:11-35 in Kàddug Yàlla gi

11 Ay yëngu-yënguy suuf yu réy dina am, ay xiif aki mbas dikke fu bare, te xew-xew yu raglu dina am, ak firnde yu mag yu jóge asamaan.
12 Waaye laata loolu lépp, yeen, dees na leen teg loxo, fitnaal leen, jébbal leen kuréli jàngu ya, tëj leen kaso. Dees na leen yóbbu ci kanami buur aki boroom dëkk ndax sama tur,
13 ngir ngeen doxe ca yékkati kàdduy seede.
14 Kon nag defleen bu baax ci seen xel, ne soxlawuleena waajal kàddug layoo.
15 Ndax man maa leen di jox làmmiñ wu ànd ak xel, wu seen benn noon dul mana dàq mbaa di ko weddi.
16 Pexe mu leen jàpplu dina sababoo sax ci seeni waajur ak seen doomi ndey ak seeni jegeñaale ak seeni xarit, te dees na rey ñenn ci yeen,
17 Ñépp a leen di bañ ndax sama tur.
18 Waaye seen genn kawaru bopp sax du sànku.
19 Saxooleen muñ nag, daldi mucc.
20 «Bu ngeen gisee gàngooru xare gu gaw Yerusalem, su boobaa xamleen ne tasteem dëgmal na.
21 Su boobaa ña mu fekk ca diiwaanu Yude, nañu daw jëm kaw tund ya, ñi ci biir dëkk bi, nañu daw génn, te ña mu fekk ca tool ya, buñu duggsi ci biir dëkk bi.
22 Ndax janti mbugal lay doon, ngir sottal mboolem lu ñu bindoon.
23 Wóoy ngalla jigéeni wérul ña, ak ñay nàmpal ca yooyu jant! Ndax tiis wu réy lay doon ci réew mi, akam sànj ci kaw askan wii.
24 Dinañu fàddoo ñawkay saamar, te dees na leen jàpp njaam, yóbbu ci mboolem xeet yi. Te jaambur ñi dul Yawut ñooy joggati Yerusalem, ba kera àppu ñooñu dul Yawut di mat.
25 «Ay firnde dinañu feeñ ci jant bi ak weer wi ak biddiiw yi. Ci kaw suuf njàqare ak tiitaange mooy ñeel xeet yi ndax riirum géej gi ak gannax yi,
26 nit ñiy séentu li nara dikkal àddina, di xëm ndax tiitaange, nde dooley asamaan dina sàqi.
27 Su boobaa dees na gis Doomu nit ki di ñëw ciw niir, ànd ak manoore ak daraja ju réy.
28 Bu xew-xew yooyu tàmbalee sotti nag, taxawleen te siggi, ndax seenug njot dëgmal na.»
29 Ci kaw loolu Yeesu léeb leen ne leen: «Xool-leen garabu figg mbaa geneen garab.
30 Bu ngeen gisee mu jebbi, ca ngeen di xamal seen bopp ne nawet jubsi na ba noppi.
31 Bu ngeen gisee xew-xew yooyu sotti, noonu itam ngeen di xame ne nguurug Yàlla dëgmal na.
32 «Maa leen ko wax déy, niti tey jii duñu wéy mukk, te loolu lépp sottiwul.
33 Asamaan ak suuf dina wees, waaye samay wax du wees mukk.
34 «Moytuleena yaafusal seen bopp ci naan gu ëpp ak màndite ak xalaati àddina, lu ko moy bés ba jekki dal ci seen kaw,
35 ndax ni mbaal di bettee, noonu la bés bay jekkee dal ci kaw mboolem ñi ci kaw suuf.
Luug 21 in Kàddug Yàlla gi