Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 21

LUUG 21:11-35

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Suuf dina yëngu yëngu yu réy, te wopp ak xiif dina am ci bérab yu bare. Dina am it ay xew-xew yu raglu ak ay firnde yu mag yuy jóge asamaan.
12Waaye bala looloo xew, dees na leen jàpp, fitnaal leen, di leen jébbal àttekat yi ca jàngu ya, tëj leen kaso. Dees na leen yóbbu ci kanam i buur ak i boroom réew ndax sama tur.
13Loolu dina leen ubbil bunt, ba ngeen man maa seedeel.
14Fasleen yéenee baña wut lay ngir musal seen bopp.
15Ndaxte man ci sama bopp maa leen di jox kàddu ak xel moo xam ne seeni noon duñu ko mana teggi, mbaa ñu di ko weddi.
16Seeni waajur sax ak seeni doomi ndey, seeni bokk ak seeni xarit, dinañu leen jébbal àttekat yi, ba ñu rey ñenn ci yéen.
17Te ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur.
18Waaye seen genn kawar sax du neen.
19Seen muñ moo leen di musal.
20«Bu ngeen gisee ay xarekat wër dëkku Yerusalem, xamleen ne jamono, ji ñu koy yàq, agsi na.
21Kon nag ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya; ku nekk ci biir dëkk bi, nanga ko génn; te ku nekk ca tool ya, bul dugg ca dëkk ba!
22Ndaxte ci bés yooyu Yàlla dina fey jëf yi, te li ñu bindoon ci téereb Yàlla dina mat.
23Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooya, ngalla it ñiy nàmpal! Ndaxte tiis wu metti dina am ci réew mi, te Yàlla dina wàcce meram ci waa réew mii.
24Dees na leen reye ak i jaasi, jàpp leen jaam, yóbbu leen ci réewi àddina sépp. Te ñi dul Yawut dinañu nappaaje Yerusalem, ba kera jamonoy ñi dul Yawut mat.
25«Ay firnde dinañu feeñ ci jant bi, ci weer wi ak ci biddiiw yi. Ci kaw suuf xeet yi dinañu tiit, jaaxle ndax riiru géej gi ak yëngu-yëngub duus yi.
26Bu boobaa nit ñiy xëm ndax tiitaange, bu ñuy xalaat musiba, yi nara wàcc ci àddina, ndaxte dees na yëngal kàttani asamaan.
27Noonu dinañu gis Doomu nit ki di ñëw ciw niir, ànd ak kàttan ak ndam lu réy.
28Bu mbir yooyu di tàmbalee xew nag, boo yaboo ngeen siggi, téen, ndaxte seen njot jubsi na.»
29Noonu Yeesu misaal leen lii: «Xool-leen garabu figg ak yeneen garab yi.
30Bu ñu gisee ñu sëq, soxlawuleen kenn wax leen ne, nawet bi jubsi na xaat.
31Noonu itam bu ngeen gisee loolu lépp xew, xamleen ne nguuru Yàlla jege na.
32«Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii duñu wéy, te loolu lépp amul.
33Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk.
34«Moytuleen seen nafsu diigal leen ci yàqute ak ci màndite ak ittey àddina, ba bés boobu bett leen ni mbaal.
35Ndaxte dina dal ci ñépp ñi nekk ci kaw suuf.

Read LUUG 21LUUG 21
Compare LUUG 21:11-35LUUG 21:11-35