Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 18:14-43 in Wolof

Help us?

LUUG 18:14-43 in Téereb Injiil

14 Yeesu teg ca ne: «Maa ngi leen koy wax, nit kooku, ba muy ñibbi këram, moom la Yàlla àtte ni ku jub, waaye du Farisen ba. Ndaxte képp kuy yékkatiku dees na la suufeel, te kuy suufeelu, ñu yékkati la.»
15 Amoon na ay nit, ñuy indil Yeesu ay liir, ngir mu teg leen ay loxoom. Bi taalibe ya gisee loolu, ñu gëdd leen.
16 Waaye Yeesu woo leen ne: «Bàyyileen xale yi, ñu ñëw ci man, te buleen leen tere, ndaxte ñu mel ni ñoom ñoo yelloo nguuru Yàlla.
17 Ci dëgg, maa ngi leen koy wax, ku woyoful ni xale, nangu nguuru Yàlla, doo ci mana dugg.»
18 Benn njiitu Yawut laaj Yeesu ne ko: «Kilifa gu baax gi, lu ma wara def, ba am wàll ci dund gu dul jeex?»
19 Yeesu ne ko: «Lu tax nga wooye ma ku baax? Yàlla rekk a baax.
20 Xam nga ndigal yi: “Bul njaaloo, bul bóome, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, teralal sa ndey ak sa baay.”»
21 Njiit la ne ko: «Loolu lépp sàmm naa ko li dale ci sama ndaw ba tey.»
22 Bi Yeesu déggee loolu, mu ne ko: «Lenn rekk moo la dese. Jaayal li nga am lépp, séddale ko miskin yi te dinga woomle ca asamaan; boo noppee, nga ñëw topp ci man.»
23 Bi nit ka déggee loolu, mu am tiis, ndaxte ku bare woon alal la.
24 Yeesu xool ko, daldi ne: «Boroom alal, dugg ci nguuru Yàlla, lu jafee ngoogu!
25 Giléem jaar ci bën-bënu puso moo gëna yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla.»
26 Ñi doon déglu daldi ne: «Kon nag ku mana mucc?»
27 Yeesu ne leen: «Li të nit ñi, tëwul Yàlla.»
28 Noonu Piyeer ne: «Nun de, dëddu nanu li nu am lépp, topp la.»
29 Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, képp ku dëddu kër walla soxna walla ay doomi ndey walla ay waajur walla ay doom ngir nguuru Yàlla,
30 dinga am tey jii ay yooni yoon, ak dund gu dul jeex ëllëg.»
31 Yeesu wéetoo ak fukki taalibe yi ak ñaar ne leen: «Nu ngi dem Yerusalem, te li yonent yi bindoon lépp ci mbirum Doomu nit ki dina mat.
32 Dinañu ko jébbal ñi dul Yawut, ñu ñaawal ko, saaga ko, tifli ci kawam.
33 Gannaaw bu ñu ko dóoree ay yar ba noppi, dinañu ko rey, waaye ca ñetteelu fan ba dina dekki.»
34 Waaye taalibe ya dégguñu li mu leen doon wax; kàddu yooyu ump na leen, te xamuñu li waxi Yeesu yooyu tekki.
35 Bi Yeesu di agsi dëkku Yeriko, am gumba gu toogoon ca wetu yoon wa, di yelwaan.
36 Naka la gumba ga dégg mbooloo di jàll, mu laaj lan moo xew.
37 Ñu wax ko ne: «Yeesum Nasaret moo fay jaar.»
38 Noonu mu yuuxu ne: «Yeesu, Sëtu Daawuda, yërëm ma!»
39 Ñi jiitu woon gëdd ko, ngir mu noppi. Waaye muy gëna yuuxu naan: «Sëtu Daawuda, yërëm ma!»
40 Noonu Yeesu taxaw, santaane ñu indil ko ko. Bi mu jegesee, Yeesu laaj ko ne:
41 «Loo bëggoon ma defal la ko?» Mu ne ko: «Sang bi, damaa bëgga gis.»
42 Noonu Yeesu ne ko: «Na say bët gis! Sa ngëm faj na la.»
43 Ca saa sa mu daldi gis. Noonu mu topp ci Yeesu, di màggal Yàlla. Mbooloo mépp gis loolu, di sant Yàlla.
LUUG 18 in Téereb Injiil

Luug 18:14-43 in Kàddug Yàlla gi

14 Yeesu teg ca ne: «Maa ne leen, kooku moo ñibbaale këram àtteb ku jub, waaye du Farisen ba. Ndaxte képp kuy réylu, dees na la toroxal, waaye ki toroxlu lees di yékkati.»
15 Doon nañu indil Yeesu ay tuut-tànk sax, ngir mu teg leen ay loxoom. Taalibe ya gis loolu, di leen jànni.
16 Yeesu nag woolu xale yi, ne: «Bàyyileen xale yi, ñu ñëw fi man, buleen leen aaye, ndax ñu mel ni ñoom ñoo yelloo nguurug Yàlla.
17 Maa leen ko wax déy, képp ku baña nangul nguurug Yàlla ni ab xale, doo ca dugg mukk.»
18 Kenn ci njiiti Yawut yi moo laajoon Yeesu, ne ko: «Sëriñ bu baax bi, ana lu may def, ba texe fàww?»
19 Yeesu ne ko: «Lu tax nga naa ma ku baax ki? Kenn baaxul ku moy Yàlla doŋŋ.
20 Xam nga ndigal yi: “Bul jaaloo, bul bóom, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, teralal sa ndey ak sa baay.”»
21 Mu ne ko: «Loolu lépp, ba may ndaw laa ko dale sàmm ba tey.»
22 Yeesu dégg loolu, ne ko: «Lenn rekk nga deseleeti. Mboolem loo am, jaay ko, séddale ko néew-doole yi. Su ko defee nga woomle fa asamaan. Boo noppee, ñëwal, topp ci man.»
23 Ba waa ji déggee loolu, am na tiis wu réy, ndax barele woon na lool.
24 Yeesu gis loolu, daldi ne: «Boroom alal tàbbi ci nguurug Yàlla, ndaw lu jafe!
25 Boroom alal dugg ci nguurug Yàlla de, giléem jaare bën-bënu puso moo ko gëna yomb.»
26 Ña cay dégg nag ne: «Kon ku mana mucc nag?»
27 Yeesu ne leen: «Li të nit, tëwul Yàlla.»
28 Piyeer daldi ne: «Nun de, noo ngii, dëddu la nu amoon, topp la.»
29 Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy, amul kenn kuy dëddu kër, mbaa jabar, mbaa mbokk, mbaa waajur, mbaa doom, ngir nguurug Yàlla,
30 te jotaatul lu ko ëpp ay yooni yoon, tey jii, akug texe ba fàww, ëllëg.»
31 Yeesu nag yóbbu Fukk ñaak ñaar, wéetook ñoom, ne leen: «Nu ngii jëm Yerusalem, te mboolem lu yonent yi bindoon ci mbirum Doomu nit ki dina sotti.
32 Ndax dees na ko jébbal jaambur ñi dul Yawut, dees na ko ñaawal, saaga ko, tifli ko.
33 Dinañu ko caw, rey ko, ba ca ñetteelu fanam, mu dekki.»
34 Waaye ndaw ya, ñoom, xamuñu dara ci jooju wax, ndax mbóotu kàddug Yeesu gaa leen làqu, ba tax ñu umple la mu wax.
35 Ba Yeesu di jubsi dëkk ba ñuy wax Yeriko, ab silmaxaa nga tooge ca peggu yoon wa, di yalwaan.
36 Silmaxa ba dégg mbooloo may romb, mu daldi laaj lu mu doon.
37 Ñu ne ko Yeesum Nasaret moo fa jaare.
38 Ci kaw loolu mu àddu ca kaw ne: «Yeesu, Sëtub Daawuda, yërëm ma!»
39 Ña jiitu femmu ko, ngir mu noppi. Teewul mu gëna xaacooti, ne: «Sëtub Daawuda, yërëm ma!»
40 Yeesu nag taxaw, ne ñu indil ko ko. Ba mu dikkee, mu laaj ko, ne ko:
41 «Loo bëgg ma defal la ko?» Mu ne ko: «Xanaa may gis, Sang bi.»
42 Yeesu ne ko: «Gisal! Sa ngëm faj na la.»
43 Ca saa sa muy gis, daldi topp ci Yeesu, di sàbbaal Yàlla. Mbooloo mépp gis loolu, di sant Yàlla.
Luug 18 in Kàddug Yàlla gi