7«Kan ci yéen bu amoon surga bu beyi walla bu sàmmi ba ñëw, ndax dafa ko naa: “Kaay lekk”?
8Déedéet. Xanaa kay da ko naan: “Defaral ma reer bi. Takkul te tibbal ma, ba ma lekk te naan, ba noppi nga doora lekk te naan.”
9Li surga ba topp ndigal, ndax tax na mu yelloo ngërëm? Déedéet.
10Noonu yéen itam bu ngeen toppee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeena war ne: “Ay surga rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»
11Bi muy dem Yerusalem ba tey, Yeesu jaar ci dig wiy xàjjale Samari ak Galile.
12Bi muy jub benn dëkk, fukki gaana ñëw, dogale ko. Ñu taxaw dànd ko, di wax ca kaw naan: