Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 12

LUUG 12:18-49

Help us?
Click on verse(s) to share them!
18Noonu mu ne: “Nii laay def: daaneel sama sàq yi, defaraat yu gëna réy, ba man cee dajale sama dugub ji ak sama am-am bépp.
19Te dinaa kañ sama bopp ne: ‘Yaw mii, am nga alal ju bare ju mana dem ay ati at; noppalal sa yaram, di lekk, di naan, tey bég.’ ”
20Waaye Yàlla ne ko: “Ñàkk xel! Guddig tey, dees na jël sa bakkan. Kon li nga dajale lépp, ku koy moom?”
21«Kiy dajale alal ngir boppam nag te amul dara ca kanam Yàlla, lu mel nii moo lay dal.»
22Noonu Yeesu daldi ne taalibeem yi: «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jaaxal, ci lu ngeen wara lekk. Buleen jaaxle it ngir seen yaram ci lu ngeen wara sol,
23ndaxte bakkan moo gën lekk, te yaram a gën koddaay.
24Seetleen baaxoñ yi: duñu ji, duñu góob, amuñu dencukaay, amuñu sàq, teewul Yàllaa ngi leen di dundal. Céy ni ngeen ëppe maana picc yi!
25Ana kan ci yéen ci kaw njaaxleem, moo mana yokk waxtu ci àppam?
26Su fekkee lu tuuti loolu rekk manuleen koo def, kon lu tax ngeen di jaaxle ci li ci des?
27«Seetleen ni tóor-tóori ñax mi di saxe. Duñu liggéey, duñu ëcc, waaye maa ngi leen di wax ne Suleymaan sax ci ndamam soluwul woon ni benn ci ñoom.
28Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxum tool yi, miy sax tey, te bu subaa ñu def ko ci taal bi, ndax du leen gëna wodd?
29Buleen di wut lu ngeen di lekk walla lu ngeen di naan; te buleen ci jaaxle.
30Ndaxte loolu lépp, ñi xamul Yàlla ñoo koy wut. Te seen Baay xam na ne soxla ngeen ko.
31Waaye wutleen nguuram, te loolu lépp dina leen ko ci dollil.
32«Buleen ragal dara, yéen coggal ju ndaw ji, ndaxte dafa soob seen Baay, mu jagleel leen nguuram.
33Jaayleen seen alal, sarxe ko, ngir sàkku ay mbuusi xaalis yu dul bënn, maanaam alal ju dul jeex ca laaxira; foofa sàcc du ko jege te max du ko yàq.
34Ndaxte fu sa alal nekk, fa la sa xol nekk itam.
35«Takkuleen bu dëgër te bàyyi làmp yi tàkk.
36Mel-leen ni ay surga yuy xaar seen njaatige buy jóge ca céet ga, ndax bu fëggee bunt ba, ñu ubbil ko ca saa sa.
37Surga yooyee seen njaatige fekkul ñuy nelaw, ba mu agsee, ñoo gëna yeyoo ngërëm. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina sol yérey waañ, wax leen ñu toog lekk, ba noppi indil leen ñam wi.
38Su fekkee seen njaatige ci xaaju guddi lay ñëw sax, walla bu suuf seddee, te fekk leen noonu, surga yooyu ñoo gëna yeyoo ngërëm.
39Waaye xamleen lii: bu boroom kër gi xamoon ban waxtu la sàcc bi di ñëw, du ko bàyyi, mu toj këram.
40Yéen itam taxawleen jonn, ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci waxtu wu ngeen ko séenuwul.»
41Piyeer ne Yeesu: «Boroom bi, ndax dangay dégtal léeb wii ngir nun rekk walla ngir mbooloo mépp?»
42Boroom bi ne ko: «Kan moo nekk surga bu takku te teey, bu njaatigeem teg ci waa kër gi, ngir mu leen di dundal ci jamono ji?
43Bu njaatigeem ñëwee te gis mu def noonu, surga boobu dina am ngërëm.
44Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina ko teg ci alalam jépp.
45Waaye su fekkee surga ba da ne ci xelam: “Sama njaatige day yéexa ñëw,” ba tax mu tàmbalee dóor surga ya ca des ak mbindaan ya, di lekk te di naan, di màndi,
46kon njaatige ba dina ñëw ci bés bu mu ko séenuwul ak waxtu wu mu xamul. Dina ko dóor ay dóor yu metti, jox ko añub ñi gëmul Yàlla.
47«Surga bi xam bëgg-bëggu njaatigeem, te waajul mbaa mu takku def ko, dinañu ko dóor dóor yu metti.
48Waaye surga bi xamul bëgg-bëggu njaatigeem, te def lu yelloo ay dóor, dinañu ko dóor dóor yu néew. Ku ñu jox lu bare dees na la feyeeku lu bare. Ku ñu dénk lu bare, dees na la laajaat lu ko ëpp.
49«Damaa ñëw ngir indi sawara si ci àddina, te bëgg naa xaat taal bi tàkk.

Read LUUG 12LUUG 12
Compare LUUG 12:18-49LUUG 12:18-49