Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - KOLOS

KOLOS 4

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Sang yi, yorleen seeni jaam ci nu jub te aw yoon, xam ne am ngeen yéen itam ab Sang ca asamaan.
2Dëkkleen ci ñaan Yàlla, farlu ci, boole ci ngërëm.
3Te ngeen ñaanaale nu ci itam, ngir Yàlla ubbil nu bunt, nu mana xamle kàddoom, di yégle kumpa gi di Kirist, muy kumpa gi waral ñu jéng ma.
4Ñaanleen ngir ma xamle ko ni mu ware.
5Jëfeleen ak xel ci seen diggante ak waa àddina, te fu ngeen ame jot, fexeleen ba jariñoo ko.
6Na seen wax jépp fees ak yiw te am xorom, ngir ngeen xam nan ngeen wara tontoo ku nekk.
7Tisig, sama mbokk mi ma sopp, di jawriñ ju takku ak sama nawle ci liggéeyu Boroom bi, dina leen yégal lépp lu jëm ci samay mbir.
8Lii moo tax ma yebal ko ci yéen: ngeen xam xibaar bi jóge ci nun, te it mu dëfal seen xol.
9Onesim lay àndal, sunu mbokk mu takku, mi nu sopp, te mu bokk ci yéen. Dinañu leen xamal lépp lu xew fii.
10Aristàrk mi nekk ak man ci kaso bi, mu ngi leen di nuyu, moom ak Màrk rakku Barnabas. Jot ngeen ay ndigal ci mbirum Màrk: bu ñëwee ci yéen, teral-leen ko.
11Yeesu mi ñuy dàkkentale Yustus, moom it mu ngi leen di nuyu. Ñoom rekk ñooy Yawut yiy liggéeyandook man ngir nguuru Yàlla, te ñoo féexal sama xol.
12Jaamu Kirist, Epafras, mi bokk ci yéen, mu ngi leen di nuyu. Du jóg ci di leen ñaanal, farlu ci ni kuy bëre, ngir ngeen taxaw temm ci coobarey Yàlla gépp, ànd ak ngëm gu mat ak kóolute gu wóor.
13Maa ngi koy seedeel ne mu ngi sonn bu baax ngir yéen, ngir waa Lawdise ak waa Yerapolis.
14Luug, doktoor bi ñu sopp, mu ngi leen di nuyu, moom ak Demas.
15Nuyul-leen nu mbokk, yi nekk Lawdise. Nuyul-leen nu itam Nimfa ak mbooloom ñi gëm, miy daje ci këram.
16Bu ñu jàngee bataaxal bii ci yéen, fexeleen ba ñu jàng ko it ci mbooloom ñi gëm mi nekk Lawdise, te yéen it ngeen jàng bi ma yónnee waa Lawdise.
17Neleen Arkib: «Farlul ci sas, wi la Boroom bi sédde, ba matal ko.»
18Man Pool maa leen di bind nuyoo bii ci sama loxob bopp. Fàttalikuleen ne dañu maa jéng. Yal na yiwu Boroom bi ànd ak yéen!